Leeru Bés bi — 31 Oktoobar: Sàkkaryaa 4:6

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Mu wax ma ne ma: «Lii moo di kàddug Aji Sax ji dikkal Sorobabel, di wax ne: Du cig njàmbaar, du ci doole, ci samag noo la. Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.»

Sàkkaryaa 4:6

Ana ku mana nànd xelum Aji Sax ji? Mbaa nga dib xejjam, ba di ko digal?

Esayi 40:13

Waaye li àddina jàppe ag ndof, moom la Yàlla tànn, ngir rusloo ko xamkat yi, te li néew doole ci àddina, moom la Yàlla tànn, ngir rusloo ko li bare doole. Li tuut ab juddu ci àddina ak li xeeblu, li tekkiwul dara, moom la Yàlla tànn, ngir neenale ko li tekki, ba tax kenn du mana damu ci kanam Yàlla.

1.Korent 1:27–29

Ngelaw fu ko neex lay gelawe; coowam ngay dégg, waaye xamuloo fu mu jóge, xamuloo fu mu jëm. Noonu la it ci képp ku juddoo ci Noowug Yàlla.»

Yowaan 3:8

Ñooñu du ci deret lañu sosoo, te it du ci coobarey nitu suuxu neen, mbaa ci coobarey góor lañu sosoo, waaye ci Yàlla lañu sosoo.

Yowaan 1:13

Googu kàddu laa jaayante woon ak yeen, ba ngeen di génne Misra. Samag noo laa taxawe fi seen biir, buleen tiit.

Ase 2:5

Yaxasyel ne: «Yeen waa Yuda gépp ak waa Yerusalem ak yaw Buur Yosafat, teewluleen. Aji Sax ji da leena wax ne leen: “Yeen buleen tiit, buleen ragal gàngoor gu réy gii, ndax xare bi du yeena ko moom, xareb Yàllaa.

2.Jaar-jaar ya 20:15

Mboolem ñii fi daje dinañu xam ne du saamar te du xeej la Aji Sax jiy walloo, ndax Aji Sax jeey boroom xare bi, te moo leen teg ci sunuy loxo.»

1.Samiyel 17:47

«Léegi nag, Aji Sax ji Yàlla, Sang bi, li nga ma dig, man ak sama waa kër, saxal ko ba fàww, te nga defe ko noonu nga ko waxe,

2.Samiyel 7:25

Sang bi, sottalal ma sa dige bi nga digook ku la ragal.

Taalifi cant 119:38

ba ku ma kókkali, ma am tontam. Maa doyloo sa kàddu.

Taalifi cant 119:42

Bàyyil xel li nga ma dig, Sang bi; moom laa yaakaar.

Taalifi cant 119:49

Sa dogali yoon laay woyantoo, fu ma mana sance.

Taalifi cant 119:54

Sa ngëneelu yoon wi nga digle moo ma gënal ay junniy dogi xaalis ak wurus.

Taalifi cant 119:72

Aji Sax ji, sa kàddoo sax dàkk, taxaw jonn fa asamaan. Sa worma, ba maasoo maas, yaa samp suuf, saxal ko.

Taalifi cant 119:89–90

Yàllaa bëggoona firndeel nu mu gëna leere ñeel ñi moom dige bi, ne ab dogalam du tebbiku mukk. Moo tax mu dogale ngiñ ab digeem. Ñaar yooyu du tebbiku ndax Yàlla du fen, te nun ñi daw làqusi ci moom, ci lanu ame ndëgërlaay lu réy lu nu ŋoye ci yaakaar ji ci sunu kanam. Yaakaar jooju lanu am, mu mel ni diigalub gaal, diigal bu dëgër te wóor, ñeel sunu xol, te yaakaar jooju mooy bëtt rido ba, ba jàll ca néeg bu sella sell ba. Fa la ndaw li nu jiitu dugg ngir nun, te kookooy Yeesu mi ñu fal sarxalkat bu mag ba fàww, mu topp dayob Melkiccedeg.

Yawut ya 6:17–20

Ci jooju daraja ak jooju jaloore lees nu baaxee ay dige yu réy njëg te màgg. Yooyu dige nag, bu ngeen ci jotee, ci ngeen di séddu ci jikkoy Yàlla, gannaaw bu ngeen muccee ci yàqutey àddina gi xemmemtéefu bakkan waral.

2.Piyeer 1:4