Teewul kenn ca takk-der ya jam ko ab xeej ci faar yi, deret ànd ak ndox tuuru ca saa sa.
Yowaan 19:34
Leeru Bés bi
Teewul kenn ca takk-der ya jam ko ab xeej ci faar yi, deret ànd ak ndox tuuru ca saa sa.
Yowaan 19:34
Musaa jël deret ja, wis-wisal ca kaw mbooloo ma, ne leen: «Lii nag mooy deret ji Yàlla fase kóllëre gi mu séq ak yeen te mu aju ci mboolem kàddoom yii.»
Mucc ga 24:8
Ndaxte dundu mbindeef ci deret la nekk, te man maa leen sédde deret, ngeen di ko jotoo seen bakkan ci kaw sarxalukaay bi. Ndax kat bakkanu mbindeef deretam la taxawe. Moo tax deret mana defal nit njotlaayam.
Sarxalkat yi 17:11
ndax deretu yëkk ak ju sikket kat manula far ay bàkkaar.
Yawut ya 10:4
Mu ne leen: «Lii mooy sama deret, ji fas kóllëre gi, te nara tuurul ñépp.
Màrk 14:24
Du deretu sikket mbaa yëkk la duggaale, waaye deretu boppam la dugge benn yoon ba fàww ca néeg bu sella sell, te moom la amale njotlaay gu sax dàkk.
Yawut ya 9:12
Deretam ja tuuru ca bant ba, ca la Yàlla defe jàmm, ba sottale ci moom, pexe mi mu jubalee boppam ak lépp, muy lu nekk ci kaw suuf ak la fa asamaan.
Kolos 1:20
Xam ngeen ne yëf yuy wéy yu mel ni xaalis mbaa wurus, du moom lees leen jote ci seen dundinu neen wa ngeen donne ca seeni maam, waaye seenug njot moo di deretu Almasi ju jafe ji taxawe deretu xar mu sikkul, gàkkul. Bu yàgg, ba àddina sosoogul la Yàlla tuddaloon Almasi bi loolu, waaye léegi ci mujug jamono jii la ko Yàlla feeñal ngir yeen
1.Piyeer 1:18–20
Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.
Esekiyel 36:25
Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.
Yawut ya 10:22
Bu nu dugal ci nattu, waaye yal nanga nu musal ci ku bon ki. Yaw de yaa yelloo nguur ak kàttan ak màggaay, ba fàww. Amiin.”
Macë 6:13
Ba loolu amee Benaya doomu Yoyada ne Buur: «Buur, sang bi, yal na ko Aji Sax ji sa Yàlla dogal. Amiin!
1.Buur ya 1:36
ba képp ku namma barkeel fi kaw suuf, ci Yàlla ji wax “Na-amee-nii” la koy ñaane, te kuy giñ fi kaw suuf it, ci Yàlla ji wax “Na-amee-nii” la koy giñe. Day fekk njàqare ya jiitu di lu ñu fàtte, te di lu làqu saay gët.
Esayi 65:16
Mu mel ni Ibraayma, ba Yàlla di digoo ak moom, Yàlla manul woona giñe ku sut Yàlla. Moo tax mu giñal ko ci boppam,
Yawut ya 6:13
Nit nag, ku ko sut lay giñe, ngir dogal kàddu, ba teesal wépp werante. Yàllaa bëggoona firndeel nu mu gëna leere ñeel ñi moom dige bi, ne ab dogalam du tebbiku mukk. Moo tax mu dogale ngiñ ab digeem. Ñaar yooyu du tebbiku ndax Yàlla du fen, te nun ñi daw làqusi ci moom, ci lanu ame ndëgërlaay lu réy lu nu ŋoye ci yaakaar ji ci sunu kanam.
Yawut ya 6:16–18
«Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Lawdise nag, bind ko ne ko: «Lii moo di kàdduy ki tudd Na-amee-nii, Seede bi wóor te dëggu, Ndeyu càkktéefu Yàlla ji. Mu ne:
Peeñu ma 3:14
Ak li digey Yàlla di bare lépp, ci Almasi bi la ay digeem di doone «waaw». Moo tax itam, ci moom lanu naan Yàlla: «Amiin», ngir delloo ko njukkal.
2.Korent 1:20
Cant ñeel na Yàlla Aji Sax ji, Yàllay Israayil, mi wéetooy jalooreem. Cant ñeel na màggaayam, ba fàww, yal na màggaayam dajal suuf sépp! Amiin, Amiin!
Taalifi cant 72:18–19
Bés yu mujj yi
Wone yépp17 Okt 2026
16 Okt 2026
15 Okt 2026
14 Okt 2026
13 Okt 2026
12 Okt 2026
11 Okt 2026