Leeru Bés bi — 19 Oktoobar: Kàddu yu xelu 3:26

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

ndax Aji Sax ji da lay yiir, di la musal cig fiir.

Kàddu yu xelu 3:26

Ca la Yàllay jóg, ngir àtte, ba wallu kuy néew dooley àddina. Selaw.

Taalifi cant 76:10

Xolu buur walum ndox la ci loxol Aji Sax ji, fu ko soob mu jëme ko fa.

Kàddu yu xelu 21:1

Ku Aji Sax ji rafetlu say jëf, say bañ sax, mu jubaleek yaw.

Kàddu yu xelu 16:7

Damay xaar Aji Sax ji, di ko xaare xol, di yaakaar kàddoom. Wattukat bi yàkkamti njël, wattukat bi yàkkamti njël, laa ne, ni ma yàkkamtee Aji Sax jee ko raw.

Taalifi cant 130:5–6

Kañleen Aji Sax ji, ànd ceek man, nu bokk wormaal turam.

Taalifi cant 34:4

Yàlla ji sax fàww moo dib rawtu, përëgam bi sax dàkk di cëslaay, moo la dàqal ab noon ne la: “Jekkalil!”

Baamtug yoon wi 33:27

Waaye barke ñeel na ku wóolu Aji Sax ji, yaakaar Aji Sax ji.

Yeremi 17:7

Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?

Room 8:31

Ndegam amees na lenn lu yokk aw fit ci Almasi bi nu gëm, ndegam lenni cofeelam lu mana dëfal am na, ndegam amees na benn cér ci Noo gu Sell gi, ndegam it amees na lenn lu bawoo fi moom, ci wàllu xol bu rafet ak yërmande,

Filib 2:1

Ku jigéen jur, yaa néewi fan, géejal coono! Dangay tóor rekk, lax, wéy ni takkndeer, doo toog.

Ayóoba 14:1–2

Man maay ñaan Baay bi, mu yónnee leen beneen Taxawukat, ngir mu nekk ak yeen ba fàww.

Yowaan 14:16

Waaye Taxawukat bi, di Noo gu Sell gi leen Baay biy yónnee ci sama tur, moo leen di jàngal lépp, fàttali leen lépp lu ma leen waxoon, man.

Yowaan 14:26

Cant ñeel na Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu Almasi bi, Baayu yërmande yi, Yàlla jiy dëfale nu nekk, moom mi nuy dëfal ci sunu jépp njàqare, ngir noonu nu jote nun ci sunu bopp, ndëfalaay lu nu dëfalu fa Yàlla, nu man koo dëfale ñi nekk ci mboolem xeeti njàqare.

2.Korent 1:3–4

Ndegam gëm nanu ne Yeesu dee na, ba dekki, noonu it lanu wara gëme ne Yàlla mooy dekkal way dawlu ñi gëmoon Yeesu, ba boole leen ak Yeesu, indaale.

1.Tesalonig 4:14

Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww. Kon nag deeleen dëfalantee yooyu kàddu.

1.Tesalonig 4:17–18