Leeru Bés bi — 15 Oktoobar: Taalifi cant 59:9

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Te yaw Aji Sax ji, yaa ngi leen di ree, yaa ngi kekku yéefar yii yépp.

Taalifi cant 59:9

Mu ne: Aji Sax ji mooy sama cëslaay, moo may aar, di ma wallu. Yàllaay sama cëslaay li ma yiiroo, fegu, mucc, làqu, raw, mucc fitna.

2.Samiyel 22:2–3

Aji Sax jee may dooleel, di ma feg. Moom laa wóolu, mu wallu ma, sama xol tooy, ma woy, sante ko.

Taalifi cant 28:7

Dees na ragale turu Aji Sax ji fa sowu, ragale màggaayam ba penku. Bu noon bi agsee ni walum dex, ngelawal Aji Sax jee koy wal, mu daw.

Esayi 59:19

Moo tax nu mana am fitu wax ne: «Boroom beey sama ndimbal, duma tiit. Ana lees ma manal?»

Yawut ya 13:6

Ñeel Daawuda. Aji Sax jee may leeral, di ma wallu. Ana ku may ragal? Aji Sax jeey aar sama bakkan. Ana ku may tiit?

Taalifi cant 27:1

Ni tund yi yéewe Yerusalem, ni la Aji Sax ji yéewe ñoñam, tey ak ëllëg.

Taalifi cant 125:2

Su ma tëddee, fàttaliku la, waxtuw guddi dama lay xalaat.

Taalifi cant 63:7

Teewlu ma, gaawe ma, Yal nangay sama cëslaay, sama rawtu. Aar ma, ma mucc.

Taalifi cant 31:3

te nga baal nu sunuy tooñ, ni nu baale nun itam, ñi nu tooñ.

Macë 6:12

Ca la Piyeer dikk ne Yeesu: «Sang bi, ñaata yoon la ma sama mbokk di tooñ, ma baal ko? Ndax day mat ba mu tollook juróom ñaari yoon?» Yeesu ne ko: «Newuma la juróom ñaari yoon, waaye ba muy juróom ñaar fukki yoon ak juróom ñaar.

Macë 18:21–22

Sang ba nag woolu jaraaf ja, ne ko: “Jaraaf ju soxor ji nga doon! Sa bor bépp laa la baal, nde danga maa tinu. Ni ma la yërëme, ndax waruloo koo mana yërëme sa moroomu jaraaf?” Sang ba mer, daldi koy jébbal mititalkati kaso ba, ba kera muy fey bor bépp. «Noonu la sama Baay ba fa asamaan di def ak yeen, su ku nekk ci yeen baalul mbokkam ci xol bu sedd.»

Macë 18:32–35

Baaxleen ci seen diggante, di ñeewantante, tey baalante, ni leen Yàlla baale ci Almasi bi.

Efes 4:32

Yeen ñi doonoon ñu dee fa kanam Yàlla ndax seeni moy ak seen ñàkka xaraf, ndax li ngeen dul Yawut, Yàllaa leen booleek Almasi bi, dundalaat leen. Moo nu baal sunu moy yépp. Kayitu bor bi nu tiiñaloon, te dogali yoon toppe nu ko, moom moo far mbind ma, yóbbu kayit ga, daajaale ko ak Almasi bi ca bant ba.

Kolos 2:13–14

Muñalanteleen te di baalante, su dee kenn ku am lu mu sikke moroomam. Ni leen Boroom bi baale, deeleen baalantee noonu.

Kolos 3:13