Mu ne ma: «Dañeel, bul tiit. Bés bu njëkk, ba nga fasee yéene xam, ba toroxlu ci sa kanam Yàlla, ca lañu dégg say kàddu te sa kàddu yooyoo ma taxa ñëw.
Dañeel 10:12
Leeru Bés bi
Mu ne ma: «Dañeel, bul tiit. Bés bu njëkk, ba nga fasee yéene xam, ba toroxlu ci sa kanam Yàlla, ca lañu dégg say kàddu te sa kàddu yooyoo ma taxa ñëw.
Dañeel 10:12
Ku màgg, Ku kawe ki, ki màkkaanam sax dàkk te turam sell, daa wax ne: «Fu kawe te sell laa màkkaanoo, maa dëkk ak boroom xol bu mokk te toroxlu, ngir leqali ku toroxlu, leqali boroom xol bu mokk.
Esayi 57:15
Boroom bi, may ma, ma wax, ma delloo la njukkal.
Taalifi cant 51:17
Aji Sax jee kawe! Ku toroxlu, mu niir; ku réy, mu ñooru.
Taalifi cant 138:6
Ci suufu loxol Yàlla bi am doole la leen Yàlla di yékkatee bu jotee, su ngeen toroxloo,
1.Piyeer 5:6
Waaye yiw wu gënatee baawaan la maye. Moom la Mbind mi ne: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.» Kon nag nangulleen Yàlla, te bañal Seytaane, mu daw, ba sore leen.
Yanqóoba 4:6–7
Boroom bi, yaa baax, di baale, di nàddil sa ngor képp ku lay dagaan. Éy Aji Sax ji, teewlul, ma ñaan la; déglul, ma tinu la. Bu ma la woowee bésub njàqare, yaa may nangul.
Taalifi cant 86:5–7
na sa nguur dikk, na sa coobare ame fi suuf na mu ame fa asamaan.
Macë 6:10
Moo tax buleen def jëfi ñàkk bopp, waaye jéemleena xam coobarey Boroom bi.
Efes 5:17
«Seen Baay ba fa asamaan itam, noonu. Bëggul kenn ci ñii gëna tuut, sànku.
Macë 18:14
Lii moo di coobarey Yàlla: ngeen sellal te mucc ci séy yi yoon tere.
1.Tesalonig 4:3
ngir bañatee topp xemmemtéefi bakkan, xanaa di topp coobarey Yàlla, diir bi ko dese ci kaw suuf.
1.Piyeer 4:2
Moom la soob mu jur nu ci kàddug dëgg gi, ba nu taxawe saraxu ndoortel meññeef, ci biiri bindeefam.
Yanqóoba 1:18
Kon nag baleen jépp jikko ju tilim ak mboolem xeeti mbon yi ne gàññ, te ngeen nangu, ci biir ag woyof, kàddu gi Yàlla xasa jëmbat ci yeen te mu man leena musal.
Yanqóoba 1:21
Ndax kat bindees na ne: «Ñu sell ngeen wara doon, ndax man Ku sell laa.»
1.Piyeer 1:16
Mu dawal nag bëtam, xool ña ko yéew, daldi ne: «Dama ne, ñii ñooy sama yaay ak samay rakk. Ndax kuy jëfe coobarey Yàlla, kooku moo di sama rakk ju góor, di samab jigéen, di sama yaay.»
Màrk 3:34–35
«Kon képp ku dégg sama kàddu yii, te di ko jëfe, dafa mel ni nit ku xelu ki tabax këram ci kaw aw doj. Ba mu noppee, taw ba sóob, wal ma dikk, ngelaw la riddi, lépp dal ca kër ga, te màbbul, ndax doj wa mu sampe.
Macë 7:24–25
Te àddina day jeex, mooki xemmemtéefam, waaye kuy jëfe coobarey Yàlla mooy sax ba fàww.
1.Yowaan 2:17
Bés yu mujj yi
Wone yépp12 Okt 2026
11 Okt 2026
10 Okt 2026
9 Okt 2026
8 Okt 2026
7 Okt 2026
6 Okt 2026