Sawarleen te baña yoqi, jaamuleen Boroom bi, ànd ceek pastéefu xol.
Room 12:11
Leeru Bés bi
Sawarleen te baña yoqi, jaamuleen Boroom bi, ànd ceek pastéefu xol.
Room 12:11
Liggéey boo gis, liggéeyal; def ci loo man. Ndax muy jëf, di doxalin, di xam-xam, di manoore, dara amu ci njaniiw ga nga jëm.
Kàdduy waare 9:10
Lu ngeen mana def, liggéeyeleen ko xol bu tàlli, ni bu ñeelul woon nit doŋŋ, xanaa Boroom bi. Te ngeen xam ne ci loxol Boroom bi ngeen di nangoo yool bi ngeen muurloo. Sang bi, Almasi bi mooy ki ngeen di jaamu.
Kolos 3:23–24
te ngeen xam ne nit ki, mu dis gor mbaa ab jaam, mboolem lu mu def ci lu baax, loola la ko Boroom biy delloo.
Efes 6:8
Danoo wara liggéey liggéeyu ki ma yónni ci bi muy bëccëg; bu guddee kenn du liggéey.
Yowaan 9:4
Mu ne leen: «Lu ngeen may seete? Xamuleen ne sama kër Baay laa wara nekk?»
Luug 2:49
Taalibeem ya nag fàttaliku la ñu bind ne: «Damaa xér ci sa kër gi, ba jeex tàkk.»
Yowaan 2:17
Kon nag bokk yi, nangeen gënatee def lu ngeen man ba dëggal woote bi ñu leen woo ak tànn gi ñu leen tànn. Su ngeen ko defee kat, dungeen daanu mukk.
2.Piyeer 1:10
Waaye danoo bëgg kenn ku nekk ci yeen wéye genn parlu googu ngeen nekke, ba kera muj ga, ngir seen yaakaar sotti ba mat sëkk. Su ko defee dungeen yàccaaral, waaye dangeen di roy ci ñi gëm te muñ, ba jagoo digey Yàlla.
Yawut ya 6:11–12
Xanaa xamuleen ne, ab rawante, ñépp a cay daw, waaye kenn doŋŋ ay jël ndam li? Dawleen nag ba jël ndam li.
1.Korent 9:24
Bu nu dugal ci nattu, waaye yal nanga nu musal ci ku bon ki. Yaw de yaa yelloo nguur ak kàttan ak màggaay, ba fàww. Amiin.”
Macë 6:13
Ku doyloo sam xel, dof nga; ku jëfe xel mu rafet, mucc nga.
Kàddu yu xelu 28:26
Képp ku dajeek lu koy xiirtal, bumu ne: «Yàllaa ma xiirtal,» ndax maneesula xiirtal Yàlla ci lu bon, te moom ci boppam du xiirtal kenn. Waaye ku nekk, sa xemmemtéefu bakkanu bopp moo lay xiirtal, ootal la ba nax la.
Yanqóoba 1:13–14
Kon nag: «Nangeen génne ci seen biir, te teqalikoo ak ñoom,» la Boroom bi wax, «lu sobewu, buleen ko laal. Su boobaa, maa leen di dalal.
2.Korent 6:17
Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Cowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja. Ba mu ko defee Lóot tànn jooru Yurdan gépp, daldi toxu jëm penku. Noonu lañu teqalikoo.
Njàlbéen ga 13:10–11
Waaye waa Sodom ñu bon lañu woon, te mana moy Aji Sax ji lool.
Njàlbéen ga 13:13
te mennum Lóot aji jub ji doŋŋ, nekkoon kenn ki mu musal, te mu sonnoon lool, ndax ñaawtéefi nit ñu dëng ñooñu.
2.Piyeer 2:7
Su demee noonu kay, kon Boroom bi def loolu lépp, xam na nu muy musale nit ñu ragal Yàlla cib nattu ak nu muy xaare nit ñu dëng ñi, ngir seen mbugal kera bésu àtte ba,
2.Piyeer 2:9
Yaw miy sikkal jaamub jàmbur, yaay kan? Jaam bu taxaw ci liggéeyam mbaa mu sàggane ko, moom ak sangam la! Te day baaxal ndax Boroom bi man na koo baaxal.
Room 14:4
Bés yu mujj yi
Wone yépp15 Okt 2026
14 Okt 2026
13 Okt 2026
12 Okt 2026
11 Okt 2026
10 Okt 2026
9 Okt 2026