ki gépp njabootug asamaan ak suuf jële aw tur.
Efes 3:15
Leeru Bés bi
ki gépp njabootug asamaan ak suuf jële aw tur.
Efes 3:15
Te it jenn Yàllaa am; mooy Baayu ñépp, moo tiim ñépp, di jëf ci ñépp te nekk ci ñépp.
Efes 4:6
Yeen ñépp doomi Yàlla ngeen, ndax li ngeen gëm Almasi Yeesu.
Galasi 3:26
Li Yàlla namm, bu fan yi matee, moo di dajale lépp ci kilifteefu Almasi bi, mboolem la fa asamaan ak li fi suuf.
Efes 1:10
Yeesu miy sellal nit ñi, moom ak ñi muy sellal, ñoo bokk lenqe, te moo tax Yeesu rusu leena woowe ay bokk.
Yawut ya 2:11
Mu daldi joxoñ ay taalibeem, ne: «Ñii ñooy sama yaay ak samay rakk, ndax kuy jëfe sama coobarey Baay ba fa asamaan, kooku moo di sama rakk ju góor, di samab jigéen, di sama yaay.»
Macë 12:49–50
Yeesu ne ko: «Bu ma langaamu, ndax yéegeeguma fa Baay ba. Waaye demal, ne samay bokk, maa ngi yéegi ca sama Baay biy seen Baay, sama Yàlla jiy seen Yàlla.»
Yowaan 20:17
Ba mu tàyyee juróomeelu tayu bi, ma gis ci suufu sarxalukaay bi, ruuwi ñi ñu bóom ndax kàddug Yàlla ak seede si ñu ci seede. Ñu àddu ca kaw ne: «Buur bu sell, bu dëggu bi, loo deeti xaar ci àtte waa àddina, ngir feyul nu sunu deret ji tuuru?» Ñu jox ku ci nekk mbubb mu weex, ne leen ñu négandiku tuuti, ba kera seeni bokk ak ñi ñu bokkal liggéey bi, te ñu war leena bóom ni ñoom, ñépp dikk, ba lim bi mat.
Peeñu ma 6:9–11
ndax daa fekk Yàlla gisal nu demin wu gën ci nun. Moo tax boroom ngëm yooyu waruñu woona àgg ci tolluwaay bu mat sëkk, te fekk nun dikkagunu ba bokk ko ak ñoom.
Yawut ya 11:40
Yeen nag nangeen ñaane nii: “Sunu Baay bi fi asamaan, nañu wormaal sa sellaayu tur,
Macë 6:9
Loolu la Yeesu wax ba noppi, téen, xool asamaan, daldi ne: «Baay, waxtu wi jot na. Feeñalal sa darajay Doom, ngir Doom ji feeñal sa daraja.
Yowaan 17:1
Yeesu ne ko: «Bu ma langaamu, ndax yéegeeguma fa Baay ba. Waaye demal, ne samay bokk, maa ngi yéegi ca sama Baay biy seen Baay, sama Yàlla jiy seen Yàlla.»
Yowaan 20:17
Yeen ñépp doomi Yàlla ngeen, ndax li ngeen gëm Almasi Yeesu.
Galasi 3:26
Mayeesu leen noo gu leen di desloo cig njaam, ba tax leena dellu cig ragal, waaye Noowug doom yu ñu doomoo, moom lees leen may, te looloo nu tax di woowe Yàlla: «Abba», mu tekki «Baay». Te Noowug Yàlla, moom ci boppam, moo mànkoo ak sunu noowug bopp, di seede ne ay doomi Yàlla lanu.
Room 8:15–16
Li ngeen diy doom nag tax na Yàlla yebal Noowug Doomam ci seen biir xol, ba Noo gi naan: «Abba», muy firi Baay. Moo tax dootuloo ab jaam, doom nga. Gannaaw doom nga nag, boroom cér nga it fa Yàlla sa baay.
Galasi 4:6–7
Bésub keroog, man dootuleen ma ñaan dara. Maa leen ko wax déy ci lu wér, su boobaa lu ngeen ñaan Baay bi ci sama tur, mu may leen ko. Ba léegi ñaanuleen dara ci sama tur. Ñaanleen, nangule, ngir seen mbég mat sëkk.
Yowaan 16:23–24
Kon nag: «Nangeen génne ci seen biir, te teqalikoo ak ñoom,» la Boroom bi wax, «lu sobewu, buleen ko laal. Su boobaa, maa leen di dalal. Maay doon seen baay, ngeen di samay doom, góor ak jigéen,» la Boroom bi, Aji Man ji wax.
2.Korent 6:17–18
Bés yu mujj yi
Wone yépp9 Okt 2026
8 Okt 2026
7 Okt 2026
6 Okt 2026
5 Okt 2026
4 Okt 2026
3 Okt 2026