Moo tax nu mana am fitu wax ne: «Boroom beey sama ndimbal, duma tiit. Ana lees ma manal?»
Yawut ya 13:6
Leeru Bés bi
Moo tax nu mana am fitu wax ne: «Boroom beey sama ndimbal, duma tiit. Ana lees ma manal?»
Yawut ya 13:6
Ana ku nuy tàggaleek cofeelu Almasi bi? Du ay nattu, te du njàqare, du it coonoy bunduxataal, mbaa ab xiif, mbaa rafle, te du genn aayteef, ba cib saamar.
Room 8:35
Waaye ci mboolem lu nu dikkal, nooy am ndam lu mat sëkk, ci ndimbalal ki nuy soppeem.
Room 8:37
«Maa leen ko wax, yeen samay soppe, buleen ragal ñu manul lu wees rey seen yaram, ndax gannaaw loolu dootuñu leen manal lu ko raw. Ma xamal leen nag ki ngeen wara ragal: kiy rey ba noppi, am sañ-sañu sànni sawara, kooku déy laa leen ne, ragalleen ko.
Luug 12:4–5
Ndokkalee ñi seenug njub tax ñu di leen bunduxataal, nde nguurug asamaan ñooy boroom. «Ndokkalee yeen, bu ñu leen di saaga, di leen bunduxataal, di leen sosal gépp njombe ndax man. Bégleen te bànneexu, ndax seen yoolub ëllëg bu réy, nde noonu lañu daan fitnaale yonent yi fi jiitu.
Macë 5:10–12
Waaye sama bakkan soxalu ma, xanaa ma bey samaw sas, ba sottal liggéey bi ma Sang Yeesu dénk, te mooy seedeel xibaaru jàmm bu yiwu Yàlla wi.
Jëf ya 20:24
Maay àgge ay buur sa kàdduy seede, te duma rus.
Taalifi cant 119:46
May xaar a xaar Aji Sax ji, mu dégg may woote, geesu ma,
Taalifi cant 40:2
te ñoom ñépp, menn ndoxum kéemaanu Yàlla ma lañu naan, ndax ñoo doon naane ca doju kéemaanu Yàlla ga, doj wa leen doon gunge, te doj wa Almasi bi la woon.
1.Korent 10:4
Simoŋ Piyeer ne ko: «Yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla Aji Dund ji.»
Macë 16:16
Man nag maa ne la, yaa di Piyeer, doj wi; ci kaw doj wii it laay samp mbooloom gëmkat ñi, te dooley dee du ko manal dara.
Macë 16:18
Mucc kat amul ci keneen, ndax fi asamaan tiim, mayeesul fi nit ñi weneen tur wu nu wara mucce.»
Jëf ya 4:12
Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu. Nanu ŋoy ci yaakaar ji nu biral ne moom lanu am, te nu baña yoqi, nde ki dige ku wóor la.
Yawut ya 10:22–23
Waaye ngëm la koy ñaane te bumu ci am benn sikki-sàkka, ndax kiy sikki-sàkka daa mel ni gannaxu géej bu ngelaw liy yóbbu, di ko lëmbaaje.
Yanqóoba 1:6
Ana ku nuy tàggaleek cofeelu Almasi bi? Du ay nattu, te du njàqare, du it coonoy bunduxataal, mbaa ab xiif, mbaa rafle, te du genn aayteef, ba cib saamar.
Room 8:35
Waaye ci mboolem lu nu dikkal, nooy am ndam lu mat sëkk, ci ndimbalal ki nuy soppeem.
Room 8:37
du lu kawe, du lu xóot, mbaa meneen mbindeef mu mu doon; dara manu noo tàggale ak cofeel gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu sunu Sang.
Room 8:39
Bés yu mujj yi
Wone yépp7 Okt 2026
6 Okt 2026
5 Okt 2026
4 Okt 2026
3 Okt 2026
2 Okt 2026
1 Okt 2026