Ni sawara di jafale boob, baxale ko am ndox, ni ngay xamalsee say noon saw tur, ba yooyu xeet di lox fi sa kanam.
Esayi 64:1
Leeru Bés bi
Ni sawara di jafale boob, baxale ko am ndox, ni ngay xamalsee say noon saw tur, ba yooyu xeet di lox fi sa kanam.
Esayi 64:1
Nijaay, dawsil, melal ni kéwél, mbaa kooba gu ndaw ci kaw tund wi ci gàncax gu xeeñ gi.
Ngën-gi-woy 8:14
Te du càkkéef gi rekk, waaye nun ci sunu bopp itam, ci lanu, nun ñi jot ab dawal ci Noo gu Sell gi, nun ci sunu bopp sax nu ngi binni sunu biir xol, ndax yàkkamtee jot céru doomi Yàlla, ba sunu njotug yaram mat.
Room 8:23
Aji Sax ji, firil asamaan, wàcc; laal tund yi, ñu saxaar.
Taalifi cant 144:5
Ñu ne leen: «Yeen waa Galile, lu ngeen di taxaw nii di séentu ci asamaan? Yeesu male ñu yéegee fi seen biir, yóbbu asamaan, nii ngeen ko gise mu jëm asamaan, ni lay délsee.»
Jëf ya 1:11
noonu itam la Almasi bi doone ab sarax benn yoon, ngir gàddu bàkkaaru nit ñu bare, te dina teewsiwaat, ci yoon wu joteetul dara ak bàkkaar, ngir indil ñi koy séentu seenug mucc.
Yawut ya 9:28
Bésub keroog dees na ne: «Sunu Yàllaa ngii nag! Moom mii lanu yaakaaroon te moo nuy wallu. Aji Sax jii lanu yaakaaroon, nan bég te bànneexoo wallam.»
Esayi 25:9
Kiy seede mbir yii nee: «Waawaaw, léegi ma ñëw.» Amiin, Sang Yeesu, ñëwal!
Peeñu ma 22:20
Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla miy Yeesu Almasi bi, Musalkat bi.
Tit 2:13
Nun nag sunum réew a nga fa asamaan, fa nuy séentoo sunu Musalkat, Sang Yeesu Almasi bi.
Filib 3:20
Naa dëkke sa xayma ba fàww; làqoo sa kiiraay. Selaw.
Taalifi cant 61:5
Ngànnaay lu ñu la mana sàkkal, du sotti, te boroom làmmiñ wu la jógal cib layoo yaa koy tiiñal. Ñiy jaamu Aji Sax ji, looloo di seen cér, looloo di àtte bi ma leen di dikke.» Kàddug Aji Sax jee.
Esayi 54:17
Néew-ji-doole woote, Aji Sax ji wuyu, musal ko fu mu jàqe. Ku ragal Aji Sax ji, malaakaam yiir la, di la wallu. Mosleen, xam ne Aji Sax jee baax, ndokkalee yaw mi ko làqoo. Ragalleen Aji Sax ji, yeen nitam ñu sell ñi; ku ko ragal doo ñàkk dara.
Taalifi cant 34:7–10
Maa muurloo béreb bu neex, ndaw cér bu rafet!
Taalifi cant 16:6
Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa joxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?
Room 8:32
Bés yu mujj yi
Wone yépp28 Sul 2026
27 Sul 2026
26 Sul 2026
25 Sul 2026
24 Sul 2026
23 Sul 2026
22 Sul 2026