Leeru Bés bi — 15 Suwe: Baamtug yoon wi 29:29

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, man de, réy-réyluwuma, daŋŋiiraluma, xintewoowuma lu réy it, mbaa lu ma ëlëm. Xanaa ne tekk, ne cell, ni perantal ak ndeyam; sama xel dal ni perantal.

Taalifi cant 131:1–2

Ndéeyu Aji Sax ji, jagley ku ko ragal. Kóllëreem la koy xamal.

Taalifi cant 25:14

Waaye Yàllaa ngi ci asamaan, di xamle ay mbóot te moo won Buur Nebukatnecar liy am jamono yiy ñëw. Sa gént gaak la nga ca gis ca sa kaw lal, lii la:

Dañeel 2:28

Lii de, mooy lenni jalooreem! Ndaw ndéey lu tuut lu nu ci déggandeem! Ana ku mana xam riiru dooleem?

Ayóoba 26:14

Wooweetuma leen ay jaam, ndax ab jaam xamul lu sangam di def. Xarit laa leen woowe, ndax mboolem lu ma dégge ci sama Baay, xamal naa leen ko.

Yowaan 15:15

«Su ngeen ma soppee, sàmmleen samay ndigal. Man maay ñaan Baay bi, mu yónnee leen beneen Taxawukat, ngir mu nekk ak yeen ba fàww. Kooku mooy Noowug Yàlla giy xamle liy dëgg. Àddina du ko mana dalal, ndax gisu ko te xamu ko. Yeen nag xam ngeen ko, ndax ci seen biir la dëkk, te ci seen biir xel lay nekk.

Yowaan 14:15–17

Te kiy xool li ci biir xol yi, xam na liy xintey Noo gi, ndax ni ko Yàlla bëgge, ni la Noo giy tinool ñu sell ñi.

Room 8:27

Bésub keroog, man dootuleen ma ñaan dara. Maa leen ko wax déy ci lu wér, su boobaa lu ngeen ñaan Baay bi ci sama tur, mu may leen ko. Ba léegi ñaanuleen dara ci sama tur. Ñaanleen, nangule, ngir seen mbég mat sëkk.

Yowaan 16:23–24

Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp parlu, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi.

Efes 6:18

Kóolute gi nu am ci Yàlla moo di su nu ko ñaanee lenn lu dëppook coobareem, da nuy nangul. Gannaaw xam nanu ne moo nuy nangul lépp lu nu ko ñaan, xam nanu ne dagaan yi nuy sàkku ci moom, am nanu ko.

1.Yowaan 5:14–15

Lii moo di coobarey Yàlla: ngeen sellal te mucc ci séy yi yoon tere.

1.Tesalonig 4:3

Yàlla kat ci cellte la nu woo, waaye du ci jëfin wu setul. Kon nag ku jalax ndigal lii, du nit nga jalax, xanaa Yàlla, moom mi leen jox Noowam gu Sell.

1.Tesalonig 4:7–8

Deeleen bég, di saxoo ñaan, te di sant ak nu mu mana deme. Loolu mooy coobarey Yàlla ci yeen ñi ànd ak Almasi Yeesu. Buleen giimal taalub Noowug Yàlla gi,

1.Tesalonig 5:16–19