Ay fan yu néew gannaaw gi, ka gën di ndaw jaay léppam, daldi tukki réew mu sore, di topp bakkanam ba yàq fa alalam.
Luug 15:13
Leeru Bés bi
Ay fan yu néew gannaaw gi, ka gën di ndaw jaay léppam, daldi tukki réew mu sore, di topp bakkanam ba yàq fa alalam.
Luug 15:13
Te loolu la ñenn ci yeen doonoon. Waaye Yàllaa leen fóot, sellal leen, jubal leen, ci turu Sang Yeesu Almasi bi ak ci sunu Noowug Yàlla.
1.Korent 6:11
Ci ñoom lanu bokkoon nun ñépp itam; mas nanoo topp sunu bakkan, di jëfe lu sunu bakkan ak sunum xel xemmem. Sunu bindu nit taxoon na noo yeyoo am sànj ni ñépp. Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy gi mu nu sopp, nun ñi doon nit ñu dee ba noppi ndax sunuy moy, moo nu booleek Almasi bi, dundalaat nu. Ci kaw yiw daal ngeen mucce. Ci sunu bokk ak Yeesu Almasi bi la nu Yàlla dekkalandoo ak moom, dëëlandoo nook moom fa déndi asamaan.
Efes 2:3–6
Lii mooy cofeel: cofeel gi du sunug cofeel, nun ci Yàlla; xanaa cofeel gi mu nu sopp, ba yebal Doomam, def ko njotlaay, ñeel sunuy bàkkaar.
1.Yowaan 4:10
Waaye Yàlla moom, ni mu firndeele cofeelam ci nun, moo di, ba nu doon ay bàkkaarkat, ca la Almasi bi deewe ngir nun!
Room 5:8
Ndegam ba ñu dee ay bañaaley Yàlla lees nu jubalee deewug Doomam, ñaata yoon lees nuy gënatee musale ag dundam, gannaaw ba ñu nu jubalee ak Yàlla?
Room 5:10
Muñalanteleen te di baalante, su dee kenn ku am lu mu sikke moroomam. Ni leen Boroom bi baale, deeleen baalantee noonu.
Kolos 3:13
Yeesu ne ko: «Ñaari boroom bor la woon ak seenub leblekat. Boru kenn ka di téeméeri junni (500 000) ci xaalis, ka ca des fukki junni (50 000). Waaye ñoom ñaar ñépp, kenn manu cee fey. Mu far jéggal leen ñoom ñépp. Ana kan ci ñaar ñooñu nag moo ciy gëna fonk leblekat bi?»
Luug 7:41–42
Sang ba nag woolu jaraaf ja, ne ko: “Jaraaf ju soxor ji nga doon! Sa bor bépp laa la baal, nde danga maa tinu. Ni ma la yërëme, ndax waruloo koo mana yërëme sa moroomu jaraaf?”
Macë 18:32–33
25-Bu ngeen taxawee di ñaan it, te fekk ngeen jàppal kenn dara, baalleen ko, ngir seen Baay ba fa asamaan baal leen seeni tooñ, yeen itam.»
Màrk 11:25–26
Yeenay ñi Yàlla tànn, sellal leen, sopp leen. Kon nag solleen xolu yërmande akug mbaax ak woyoflu ak jikko ju lewet ak xolu muñ. Muñalanteleen te di baalante, su dee kenn ku am lu mu sikke moroomam. Ni leen Boroom bi baale, deeleen baalantee noonu.
Kolos 3:12–13
Ca la Piyeer dikk ne Yeesu: «Sang bi, ñaata yoon la ma sama mbokk di tooñ, ma baal ko? Ndax day mat ba mu tollook juróom ñaari yoon?» Yeesu ne ko: «Newuma la juróom ñaari yoon, waaye ba muy juróom ñaar fukki yoon ak juróom ñaar.
Macë 18:21–22
Ci kaw loolu lépp nag, tegooleen cofeel, mooy xànc gi leen faste, ba seenug bennoo mat sëkk.
Kolos 3:14
Bés yu mujj yi
Wone yépp9 Suw 2026
8 Suw 2026
7 Suw 2026
6 Suw 2026
5 Suw 2026
4 Suw 2026
3 Suw 2026