Kon nag xoolleen bu baax seen jëfin, defleen jëfinu nit ñu am xel, te baña mel ni ñu ñàkk xel. Jariñooleen lu ngeen man jot gi ngeen amagum, ndax jant yu bon a ngii tey.
Efes 5:15–16
Leeru Bés bi
Kon nag xoolleen bu baax seen jëfin, defleen jëfinu nit ñu am xel, te baña mel ni ñu ñàkk xel. Jariñooleen lu ngeen man jot gi ngeen amagum, ndax jant yu bon a ngii tey.
Efes 5:15–16
Waaye kat, fexeleen bu baax di jëfe santaane beek ndigalu yoon wi leen Musaa jaamub Aji Sax ji sasoon, ngir ngeen sopp seen Yàlla Aji Sax ji, di doxe mboolemi yoonam, di sàmm ay santaaneem, ŋoy ci moom, di ko jaamoo seen léppi xol ak seen léppi jëmm.»
Yosuwe 22:5
Jëfeleen xel mu rafet seen diggante ak aji gëmadi ñi ci biti, te jot gi ngeen amagum, fexeleen ba jariñoo ko. Na seen kàddu ànd ak yiw te am solo, te ngeen xam nu ngeen di tontoo ku nekk, tont li war.
Kolos 4:5–6
te lu bon ak nu mu mana bindoo, dàndleen ko.
1.Tesalonig 5:22
Boroom séet ba nag guddee, ñépp gëmmeentu, bay nelaw. «Ba guddi ga xaajee, coow la jib: “Boroom séet baa ngoog, génnleen, gatandu ko.”
Macë 25:5–6
«Teewluleen boog, nde xamuleen bés ba, mbaa waxtu wa.
Macë 25:13
Kon nag bokk yi, nangeen gënatee def lu ngeen man ba dëggal woote bi ñu leen woo ak tànn gi ñu leen tànn. Su ngeen ko defee kat, dungeen daanu mukk.
2.Piyeer 1:10
Ndokkalee surga yooyu seen njaatige dikk fekk ñu teewlu. Maa leen ko wax déy, njaatige leey takku, toogal leen ba noppi dikk, taajal leen, ñu lekk.
Luug 12:37
«Léegi ma ñëw. Ŋoyal ci li nga yor, ngir kenn baña fëkk sa kaalag ndam.
Peeñu ma 3:11
Fekk na mu naan ci xelam: «Su ma manoona laal catu mbubbam rekk, dinaa wér.»
Macë 9:21
Ab gaana jekki dikk, sujjóotal ko, ne ko: «Sang bi, su la soobee, man nga maa setal.» Mu tàllal loxoom, laal ko ne: «Soob na ma, setal.» Ca saa sa ngaanaam ga set wecc.
Macë 8:2–3
20-Yeesu ne leen: «Xanaa seenug néew ngëm. Maa leen ko wax déy, su ngeen amee ci ngëm, lu tollu ni peppu fuddën, dingeen ne tund wii: “Toxool fii, ba fale,” mu toxu, te dara du leen të.»
Macë 17:20
Kon nag buleen teqalikook seenu fit, yool bu réy a ngi ci.
Yawut ya 10:35
Kon nag soppe yi, noonu ngeen masa dégge ndigal, démb ba may teew, rawatina tey bi ma wuutee, nangeen ko wéye, di jëfe seenug mucc, te ànd ceek ragal Yàlla bay lox, ndax Yàlla mooy liggéey ci yeen lu tax ngeen mana namma jëfe coobareem, ba man koo jëfe.
Filib 2:12–13
Suuf ay meññal boppam gàncax, jiital am ñax, dem ba taxawal aw gub, ba ay pepp mujj fees gub wa.
Màrk 4:28
Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji. Ni jant bu fenk la dikkam wóore, ni ab taw la nuy dikkale, ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»
Ose 6:3
Ca jamonoy Yaxya ba léegi, nguurug asamaan mu ngi jànkoonteek coono, ñiy jëfe doole di ko jéema aakimoo.
Macë 11:12
Xanaa xamuleen ne, ab rawante, ñépp a cay daw, waaye kenn doŋŋ ay jël ndam li? Dawleen nag ba jël ndam li.
1.Korent 9:24
Xare bu baax bi, xare naa ko, rawante bi, sottal naa ko, ngëm gi ma am, sàmm naa ko. Léegi nag kaalag njekk a may xaar, te Boroom bi, àttekat bu jub bi moo ma koy yool, keroog ca bés ba, te du man rekk la koy yool, waaye itam képp ku koy séentu te yàkkamti bés ba muy feeñ.
2.Timote 4:7–8
Bés yu mujj yi
Wone yépp15 Suw 2026
14 Suw 2026
13 Suw 2026
12 Suw 2026
11 Suw 2026
10 Suw 2026
9 Suw 2026