Leeru Bés bi — 14 Suwe: Filib 3:10

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Sàkkuwuma lu moy xam ko, xam manoore ji ko dekkal, ak itam séddu ci ay coonoom, ba bokk ak moom deewam,

Filib 3:10

Waaye noonu ngeen séddoo ci coonoy Almasi bi, bégeleen ko, ngir bu ndamam feeñee, ngeen gënatee bég.

1.Piyeer 4:13

Kàddu gu wóor a ngii: Su nu deewandoo ak Almasi bi, nooy dundandoo ak moom itam;

2.Timote 2:11

Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi bi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.

Room 8:17

Yàllaa bëggoona firndeel nu mu gëna leere ñeel ñi moom dige bi, ne ab dogalam du tebbiku mukk. Moo tax mu dogale ngiñ ab digeem. Ñaar yooyu du tebbiku ndax Yàlla du fen, te nun ñi daw làqusi ci moom, ci lanu ame ndëgërlaay lu réy lu nu ŋoye ci yaakaar ji ci sunu kanam.

Yawut ya 6:17–18

Sunu Sang Yeesu Almasi bi ci boppam ak Yàlla sunu Baay mi nu sopp, te may nu ciw yiwam, jàmmi xol ju sax dàkk ak yaakaar ju wér, yal nañu leen may jàmmi xol, te may leen dooley wéye jépp jëf ju baax ak gépp kàddu gu rafet.

2.Tesalonig 2:16–17

Sang bi ne ko: «Màrt, Màrt, yitte yi nga xintewoo, di ci doñ-doñi moo bare.

Luug 10:41

Seetleen ci baaxoñ: du ji, du góob, amulub denc mbaa am sàq. Teewul Yàlla di ko dundal. Yeen nag, ñaata yoon ngeen gën picc yi!

Luug 12:24

«Seetleen ni tóor-tóor yiy saxe. Doñ-doñiwuñu, ëccuñu, waaye maa leen ko wax, Suleymaan ak darajaam jépp sax, soluwul woon ni benn ci ñoom.

Luug 12:27

Yeen nag, buleen tiisoo lu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan; te bu yooyu xalaat ub seen bopp. Ndax loolu lépp, xeeti yéefari àddina, ñoo koy tiisoo, te yeen, Baay bi xam na ne soxla ngeen ko.

Luug 12:29–30

Kon su nu amee lu nu lekk ak lu nu sol, nanu ko doyloo. Waaye ñi sàkkoo barele, ñooy tàbbi ci nattub bakkan aki fiir ak lu bare ciy xemmemtéef yu tekkiwul dara, xemmemtéef yuy lore, tey suuxal seeni boroom ci yàqule ak sànkute. Ndax sopp xaalis kat mooy reenu mboolem xeeti loraange. Am na ñuy ŋaf-ŋafi, di ko wut, far lajj ci yoonu ngëm, ba teg seen bopp tiis wu bare.

1.Timote 6:8–10

te xalaati àddina ak naxey alal ak yeneen xemmemtéef wàllisi, daldi fatt kàddu gi, ba tax meññul.

Màrk 4:19

Kon nag gannaaw gii ndiiraanu seede wu réy moo nu yéew, nanu sippiku mboolem sëf bu nuy yeexal ak bàkkaar bu nu yomba téqtal. Ñu daw nag xél wi ñu nu waajalal, te baña yoqi.

Yawut ya 12:1