Sang ba nag gis ne Aji Sax jaa ngi ànd ak Yuusufa, di ko may ndam ci lépp lu mu sabablu.
Njàlbéen ga 39:3
Leeru Bés bi
Sang ba nag gis ne Aji Sax jaa ngi ànd ak Yuusufa, di ko may ndam ci lépp lu mu sabablu.
Njàlbéen ga 39:3
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Ndokkalee képp ku ragal Yàlla, di jëfe ay yoonam. Yaay lekk saw ñaq, mbégteek ngëneel ñeel la.
Taalifi cant 128:1–2
Dénkul ci Aji Sax ji, di def lu baax, ba des ci réew meek jàmm. Deel bànneexoo Aji Sax ji, mu may la say nammeel.
Taalifi cant 37:3–4
Xanaa du maa la sant ne la, nga dëgërlu te am fit? Bul tiit, bul ragal. Sa Yàlla Aji Sax ji laak yaw, fépp foo jëm.»
Yosuwe 1:9
Waaye njëkkleena tiisoo nguurug Yàlla, ak njub gi mu laaj, te loolu lépp moo leen ko ciy dollil.
Macë 6:33
Yàlla la daan wut ca janti Sàkkaryaa ma doon boroom xam-xam ci peeñuy Yàlla. Jant ya mu dee jaamu Aji Sax ji, Yàlla nag may na ko ndam.
2.Jaar-jaar ya 26:5
Wattuleen seen bopp nag, bala ngeena fàtte seen Yàlla Aji Sax ji, baña sàmm ay santaaneem ak àttey yoonam ak dogali yoonam yi ma leen di dénk tey.
Baamtug yoon wi 8:11
Dingeen wax ci seen xel ne: «Sunu doole ak sunu njàmbaaru bopp moo nu may jii alal.»
Baamtug yoon wi 8:17
Mu ne leen: «Xanaa du seen Yàlla Aji Sax jaa ngi ànd ak yeen, may leen jàmm fi leen wër fépp? Ndax kat teg na ci sama loxo waa réew mi, ba réew mi mépp nangul Aji Sax ji, nangul ñoñam.
1.Jaar-jaar ya 22:18
Ca saa sa Yeesu yég ci xelam la ñuy nàttable ci seen xel. Mu ne leen: «Li ngeen di nàttable nii ci seen xel, ana lu ko waral?
Màrk 2:8
Ngëmu Ibraayma wàññikuwul, doonte ba mu xoolaatee boppam, xam na ne yaramam dee na daanaka, ndax fekk na ay atam xawa tollu ci téeméer, te njurukaayu Saarata it fekk na ko dee. Teewul digeb Yàlla ba la ne jàkk, nàttablewul, gëmadiwul, xanaa dëgërloo dooley ngëmam rekk, sant Yàlla.
Room 4:19–20
Ana yii yaar, lu ci gëna yomb: ne lafañ bi “Jéggalees na la say bàkkaar,” am ne ko: “Jógal, jël sa basaŋ te dox”?
Màrk 2:9
Yeesu ne ko: «Nga ne: “Soo manee”? Ku ànd ak gëm kay, dara tëwu la.»
Màrk 9:23
Yeesu dikk ne leen: «Joxees na ma bépp sañ-sañ fa asamaan ak fi kaw suuf.
Macë 28:18
Xoolleen picc yi: duñu ji, duñu góob, duñu denc ci am sàq. Teewul seen Baay ba fa asamaan di leen dundal. Yeen nag, xanaa du yeena gën picc yi fuuf?
Macë 6:26
Yeesu xam la ñuy wax, ne leen: «Yeenaka néew ngëm, lu ngeen di werante ci seen biir, naan amuleen fi mburu? Kon xamaguleen ba tey, fàttalikuwuleen it juróomi mburu ya ca juróomi junniy (5 000) nit ña, ak ñaata pañey desit ngeen ca jële?
Macë 16:8–9
Te sama Yàlla itam mooy sàkke ci koomam gu yéeme gi ci Almasi Yeesu, ba fajal leen seen soxla yépp.
Filib 4:19
Bés yu mujj yi
Wone yépp7 Suw 2026
6 Suw 2026
5 Suw 2026
4 Suw 2026
3 Suw 2026
2 Suw 2026
1 Suw 2026