«Mu jóg, ngir dellu kër baayam. Fu sore la ko baayam séene, muy dikk. Mu ñeewante ko, daw, laxasu ko, fóon ko.
Luug 15:20
Leeru Bés bi
«Mu jóg, ngir dellu kër baayam. Fu sore la ko baayam séene, muy dikk. Mu ñeewante ko, daw, laxasu ko, fóon ko.
Luug 15:20
Yiw ak yërmande, fa Aji Sax ji. Moo muñ mer te bare ngor. Saxoowul di toppe, dencul mer ba fàww. Du sunuy bàkkaar la nu mbugal, du sunuy ñaawtéef la nu fey. Ni asamaan tiime suuf, ni la ngoram yiire ku ko ragal. Ni penku soree sowu, ni la nu soreleek sunu mbugali tooñ. Ni baay yërëme doom, ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal.
Taalifi cant 103:8–13
Mayeesu leen noo gu leen di desloo cig njaam, ba tax leena dellu cig ragal, waaye Noowug doom yu ñu doomoo, moom lees leen may, te looloo nu tax di woowe Yàlla: «Abba», mu tekki «Baay». Te Noowug Yàlla, moom ci boppam, moo mànkoo ak sunu noowug bopp, di seede ne ay doomi Yàlla lanu.
Room 8:15–16
Waaye yeen ñi sore woon, léegi bi ngeen nekkee ci Almasi Yeesu, jege ngeen ndax deretu Almasi ji tuuru.
Efes 2:13
Kon nag dootuleen ay gan mbaa ay doxandéem, waaye ay nawley ñu sell ñi ngeen, te waa kër Yàlla ngeen.
Efes 2:19
Ci kaw loolu ki toog ci ngàngune mi ne: «Maa ngii di yeesal lépp!» Mu teg ci ne ma: «Bindal, yii kàddu yu wóor la te dëggu.»
Peeñu ma 21:5
Yeesu ne ko: «Maa la ko wax déy ci lu wér, nit ki, su judduwaatul, du mana gis nguurug Yàlla.»
Yowaan 3:3
Kon bu nit ki bokkee ci Almasi bi, mbindeef mu bees lay doon. La woon day wonni, li teew nag, di lu yees.
2.Korent 5:17
Maa leen di jox xol bu yees, te xel mu yees laay def ci seen dënn. Xolu doj bi laay roccee ci seen suux, wecceel leen ko xol yu nooye ni suux,
Esekiyel 36:26
Setalleen seen bopp boog, génneleen lawiir bu yàgg bi ci seen biir, ba mana doon tooyal bu bees bu mucc lawiir, nde doon ngeen ko ba noppi, ndax Almasi bi, sunu gàttub bésub Mucc biy sunub sarax, rendilees na nu ko.
1.Korent 5:7
te ngeen soloo jëmm ju yees ji Yàlla sàkke ci takkndeeram, di jëfe njub ak sellaay ji dëgg di jur.
Efes 4:24
Su boobaa xeet yi gis sag njub, buur yépp gis sa daraja, ba ñu di la tudde tur wu yees wu Aji Sax ji di tuddal boppam.
Esayi 62:2
«Maa ngii di sàkksi asamaan su yees ak suuf su yees. Deesul fàttalikooti yëf ya jiitu, xel dootu ci dem.
Esayi 65:17
Gannaaw loolu lépp noonu lay seeye nag, xamleen bu baax li leen war: jëfin wu sell akug ragal Yàlla
2.Piyeer 3:11
Bés yu mujj yi
Wone yépp10 Suw 2026
9 Suw 2026
8 Suw 2026
7 Suw 2026
6 Suw 2026
5 Suw 2026
4 Suw 2026