Yeesu dellu leen léeb lii, ngir ñu wareefoo di sax ci ñaan te baña xàddi.
Luug 18:1
Leeru Bés bi
Yeesu dellu leen léeb lii, ngir ñu wareefoo di sax ci ñaan te baña xàddi.
Luug 18:1
Yeesu teg ca ne leen: «Ana kan ci yeen moo seeti ab xaritam xaaju guddi, ne ko: “Xarit, lebal ma ci ñetti mburu. Sama xarit bu nekk ciw yoon moo dikk sama kër, te awma dara lu ma ko taajal,” te xarit ba àddoo ca biir néegam, ne ko: “Bu ma sonal, tëj naa ba tëdd, maak samay doom; manumaa jóg, di la jox dara”? Maa leen ko wax, su jógul jox ko la mu laaj ndaxug xaritoo it, la ko kee amul kersay yee ngir sàkku ndimbal mooy tax mu jóg, jox ko mboolem lu mu soxla.
Luug 11:5–8
Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp parlu, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi.
Efes 6:18
Ba nit ka xamee ne manalu ko dara, dafa dóor Yanqóoba ci yaxu mooco bi, mu summikoo ca bëre ba.
Njàlbéen ga 32:26
Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.»
Njàlbéen ga 32:28
Ag ñaan nag, saxooleen ko, te ngeen teewlu ci, boole ci ag cant.
Kolos 4:2
Fan yooyu la Yeesu dem ca kaw tund wa ngir ñaani fa; mu fanaane faa ñaan ci Yàlla.
Luug 6:12
Xoolal sama naqar ak sama tiis, te baal ma bépp bàkkaar.
Taalifi cant 25:18
«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.
Esayi 1:18
Ñu jekki indil ko ab lafañ, mu tëdd cig laltu. Ba Yeesu seetloo seen ngëm, da ne lafañ ba: «Na sa xel dal, doom, jéggalees na la say bàkkaar.»
Macë 9:2
Mennum man mii maay far say moy ngir man, ba dootuma fàttaliku bàkkaar.
Esayi 43:25
Kon nag dingeen xam ne Doomu nit ki am na ci kaw suuf, sañ-sañu jéggale ay bàkkaar.» Mu ne lafañ ba: «Jógal, jël sag laltu, te ñibbi.»
Macë 9:6
Ci moom lanu ame njot gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa,
Efes 1:7
ca la nu musal, te du jenn jëfu njekk ju nu def, ba tax mu musal nu, waaye ci yërmandeem la nu musale, sang nu cangaay lu nu taxa judduwaat, boole ci yeesale nu Noo gu Sell gi mu nu awale ci Yeesu Almasi bi sunu Musalkat, ba baawaanal ko ci sunu kaw.
Tit 3:5–6
Yeen ñi doonoon ñu dee fa kanam Yàlla ndax seeni moy ak seen ñàkka xaraf, ndax li ngeen dul Yawut, Yàllaa leen booleek Almasi bi, dundalaat leen. Moo nu baal sunu moy yépp. Kayitu bor bi nu tiiñaloon, te dogali yoon toppe nu ko, moom moo far mbind ma, yóbbu kayit ga, daajaale ko ak Almasi bi ca bant ba.
Kolos 2:13–14
Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii, te baña fàtte mboolem xéewalam! Moo lay baal foo ñaawe, di la wéral foo woppe.
Taalifi cant 103:2–3
Bés yu mujj yi
Wone yépp6 Suw 2026
5 Suw 2026
4 Suw 2026
3 Suw 2026
2 Suw 2026
1 Suw 2026
31 Mee 2026