Sama càmmoñu waay, ma gegenoo, ndijooram, ma laxasoo.
Ngën-gi-woy 2:6
Leeru Bés bi
Sama càmmoñu waay, ma gegenoo, ndijooram, ma laxasoo.
Ngën-gi-woy 2:6
Yàlla ji sax fàww moo dib rawtu, përëgam bi sax dàkk di cëslaay, moo la dàqal ab noon ne la: “Jekkalil!”
Baamtug yoon wi 33:27
Teewul ba mu gisee na ngelaw la riddee, dafa tiit, tàmbalee suux. Mu àddu ca kaw, ne: «Sang bi, wallu ma!» Yeesu daldi tàllal loxoom, jàpp ko, ne ko: «Yaaka néew ngëm, ana looy xel ñaar?»
Macë 14:30–31
Bu Aji Sax ji rafetloo saw yoon, mooy jiite say jéego. Soo tërëfee it, doo daanu. Aji Sax jee lay walloo loxoom.
Taalifi cant 37:23–24
Beñamin la wax, ne ko: «Soppeb Aji Sax jaa ngi, keey dëkke xel mu dal fi wetam, mu di ko yiir bésoo bés, te diggantey waggam la dëkke.»
Baamtug yoon wi 33:12
ci ni ngeen di sippikoo ci kawam, mboolem seenu tiis, nde mooy ki leen tiisoo.
1.Piyeer 5:7
Mu ne ko: «Dawal, nga wax xale bu góor bii ne ko: “Yerusalem lees di dëkke, te tata wëru ko; ŋàpp lay def, ndax barewaayu nit ñeek jur gi ci biiram.
Sàkkaryaa 2:8
Man maa leen di texeel ba fàww; duñu sànku mukk, te kenn du leen foqatee ci sama loxo. Sama Baay bi ma leen jox, moo gëna màgg lépp, te kenn manula foqatee lenn ci loxol Baay bi.
Yowaan 10:28–29
Ña nga naa: «Ndaw sii ku mu? Bu nee xiféet, nga ne fajar a xar, rafet ni leer gu ndaw, yànj ni jant bi, yéeme ni gàngoori biddiiw!»
Ngën-gi-woy 6:10
Wattuleen nag seen bopp, wattu mboolem gétt gi leen Noo gu Sell gi sàmmloo, te ngeen foral mbooloom gëmkati Yàlla mi Yàlla jote deretu boppam.
Jëf ya 20:28
Jëkkër nag, na sopp jabaram ni Almasi bi soppe mbooloom gëmkat ñi, ba joxeel leen bakkanam. Moo defal loolu mbooloo mi, ba man koo setale cangaayal ndox mu ànd ak kàddoom, ngir sellal ko. Li mu ci namm moo di teewal mbooloo mi fi kanamam, mu mel ni ab séetam bu ne ràññ, gàkkul, rasul, taqul lenn, xanaa sell, mucc sikk.
Efes 5:25–27
Firnde ju màgg nag moo feeñoon asamaan: Ndaw su làmboo jant bi, weer wi ronu ndëgguy tànk yi, mu kaalawoo fukki biddiiw ak ñaar.
Peeñu ma 12:1
Nanu bég, di bànneexu te màggal ko, ndax céetu Xar mi agsi na, ab séetam defaru na ba noppi! Jox nañu ko mbubbum lẽe mu set, ne ràññ, mu sol.» Lẽe boobu mooy jëfi njekk yu nit ñu sell ñi.
Peeñu ma 19:7–8
Googu njub fa kanam Yàlla nag, ci gëm Yeesu Almasi bi lees koy ame, te mboolem ñi ko gëm la ñeel, amul xejj ak seen.
Room 3:22
Man nag daraja ji nga ma jox, jox naa leen ko, ngir ni nu nekke benn maak yaw, ñu nekke ni noonu.
Yowaan 17:22
Bés yu mujj yi
Wone yépp25 Awr 2026
24 Awr 2026
23 Awr 2026
22 Awr 2026
21 Awr 2026
20 Awr 2026
19 Awr 2026