Léegi nag yaw Yanqóoba, yaw Israayil mii, Aji Sax ji la sàkk tabax la, dafa wax ne: «Bul tiit, jot naa la. Dama laa woo ci sa tur. Maa la séddoo.
Esayi 43:1
Leeru Bés bi
Léegi nag yaw Yanqóoba, yaw Israayil mii, Aji Sax ji la sàkk tabax la, dafa wax ne: «Bul tiit, jot naa la. Dama laa woo ci sa tur. Maa la séddoo.
Esayi 43:1
Bul tiit, doo rus mukk. Bul jaaxle, deesu la kersaal mukk. Sa gàcce ga ba ngay ndaw, dinga ko fàtte, te sa tiisu jëtun wa dootoo ko fàttaliku. Sa jëkkër, Ki la sàkk, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee di turam. Aji Sell ju Israayil moo la jot, te moo di Yàllay àddina sépp.
Esayi 54:4–5
Maa far say moy, mu naaxsaay niw niir, say bàkkaar ne mes nib lay. Délsil fi man, jot naa la.»
Esayi 44:22
waaye seenug njot moo di deretu Almasi ju jafe ji taxawe deretu xar mu sikkul, gàkkul.
1.Piyeer 1:19
Waaye seen jotkat a am doole, te mooy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. Moo leen di layool seen layoo, ngir jàqal réewum Babilon, jàmmal waa àddina yi ci des.
Yeremi 50:34
Sama Baay bi ma leen jox, moo gëna màgg lépp, te kenn manula foqatee lenn ci loxol Baay bi.
Yowaan 10:29
Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, tukkee ci Yàlla sunu Baay ak Sang bi Yeesu Almasi bi maye bakkanam ngir njotug sunuy bàkkaar, ba musal nu ci jamonoy tey ju bon ji, ci coobarey Yàlla sunu Baay bi daraja ñeel, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
Galasi 1:3–5
Jëfi ngorug Aji Sax ji laay fàttalee ak cant gi Aji Sax ji yelloo, ngir li nu Aji Sax ji defal lépp; mbaax gu réy gi mu ji waa kër Israayil, defal leen ko ci yërmandeem, ak jëfi ngoram gu réy.
Esayi 63:7
May xaar a xaar Aji Sax ji, mu dégg may woote, geesu ma,
Taalifi cant 40:2
Moo tax dootul man maay dund, waaye Almasi bi mooy dund léegi ci man. Sama dundu yaramu suux wii tey nag, ci ngëm gi ma gëm Doomu Yàlla laa koy dunde, moom mi ma sopp, ba jébbale boppam ngir man.
Galasi 2:20
Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa joxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?
Room 8:32
Waaye Yàlla moom, ni mu firndeele cofeelam ci nun, moo di, ba nu doon ay bàkkaarkat, ca la Almasi bi deewe ngir nun!
Room 5:8
Moo nu màndargaale xàmmikaayam, te moo yeb dawalub Noo gu Sell gi ci sunu biir xol.
2.Korent 1:22
Noo gi moo di dawal bi nu jotagum ci sunu muur, ba kera njotug ñoñi Yàlla matee, ba nit ñi sante Yàlla màggaayam.
Efes 1:14
Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy gi mu nu sopp, nun ñi doon nit ñu dee ba noppi ndax sunuy moy, moo nu booleek Almasi bi, dundalaat nu. Ci kaw yiw daal ngeen mucce. Ci sunu bokk ak Yeesu Almasi bi la nu Yàlla dekkalandoo ak moom, dëëlandoo nook moom fa déndi asamaan.
Efes 2:4–6
Bés yu mujj yi
Wone yépp8 Awr 2026
7 Awr 2026
6 Awr 2026
5 Awr 2026
4 Awr 2026
3 Awr 2026
2 Awr 2026