ndax lépp ngeen woomle ci moom, ci gépp kàddu ak bépp xam-xam.
1.Korent 1:5
Leeru Bés bi
ndax lépp ngeen woomle ci moom, ci gépp kàddu ak bépp xam-xam.
1.Korent 1:5
Ndax kat, ba nu amul menn pexem mucc, ca waxtu wa gën, la Almasi bi deewal yéefar yi.
Room 5:6
Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa joxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?
Room 8:32
Ndax kat ci Almasi bi, ci yaramu nitam la léppi Yàlla dëkke, ba mat sëkk ci moom, ci moom ngeen mate it, te mooy kilifay mboolem boroom nguur yi ak mboolem boroom sañ-sañ yi.
Kolos 2:9–10
Saxleen ci man, ni ma saxe man ci sama bopp ci yeen. Ni carub reseñ tëlee meññal boppam, su saxul ci ndeyam, ni ngeen di tëlee meññ, su ngeen saxul ci man. «Man maay reseñ gi, yeen ngeen di car yi. Ki sax ci man, ma sax ci moom, kooku mooy meññ lu bare, nde su dul man, dungeen mana def dara.
Yowaan 15:4–5
Xam naa ne man, sama bindu suuxu neen wii, lenn lu baax dëkku ci. Yéene jaa ngeek man, kàttanu jëfe lu baax moo fi nekkul.
Room 7:18
Waaye ku nekk ci nun ak mayam, ci yiwu Yàlla, ni ko nattub Almasi bi séddalee.
Efes 4:7
Su ngeen saxee ci man te samay wax sax ci yeen, lu ngeen bëgg, ñaanleen ko, dees na leen ko nangul.
Yowaan 15:7
Na kàddug Almasi bi dëkk ci yeen, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jàngalantee aka artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ak ay taalifi cant ak woyi tagg Yàlla ak woy yu ñu fente ci Noowug Yàlla gi.
Kolos 3:16
di gis kanamam, turam binde ci seen jë.
Peeñu ma 22:4
Musaa teg ca ne ko: «Ngalla may ma nag ma niir sag leer!»
Mucc ga 33:18
Mu teg ca ne ko: «Doo mana gis sama kanam nag, ndax doom aadama du ma gis ba noppi di dund.»
Mucc ga 33:20
Kenn masula gis Yàlla, waaye Yàlla miy Kenn te sës rëkk ci Baay bi, kooku mooy ki ko xamle.
Yowaan 1:18
Mu ngoogu di dikk, indaale niir yi, te ñépp a koy teg bët, ba ca ña ko jamoon sax, te giiri kaw suuf yépp ay jooy ndax moom. Noonu la moos. Amiin.
Peeñu ma 1:7
Maa ngi koy gis, te du tey, maa ngi koy niir, te jubseegul; biddiiw a feqe fa Yanqóoba, yetu nguur a yékkatikoo fa Israayil, daldi toj boppi Mowab, toj kaaŋi mboolem askanu Set.
Màndiŋ ma 24:17
Waaye man xam naa ne sama Jotkat a ngi dund, te mooy mujje taxaw fi kaw suuf. Bu sama der bi lekkoo sax, du tee ma dese suux wu ma xoole Yàlla,
Ayóoba 19:25–26
Man nag ma am dëgg, ne la jàkk, yewwu, regge sa jëmm.
Taalifi cant 17:15
Soppe yi, léegi doomi Yàlla lanu, te li nuy dooni nag feeñagul. Waaye xam nanu ne bés bu Almasi bi feeñee, nooy nirook moom, ndax su boobaa, ni mu nekke, noonu lanu koy gise.
1.Yowaan 3:2
Sang bi ci boppam, woote bu xumb lay wàccaalee asamaan, baatu kilifag malaaka jib, ànd ak coowal liitu Yàlla. Su ko defee ña seenug dee fekk ñu gëm Almasi bi ñooy njëkka dekki. Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww.
1.Tesalonig 4:16–17
Bés yu mujj yi
Wone yépp7 Awr 2026
6 Awr 2026
5 Awr 2026
4 Awr 2026
3 Awr 2026
2 Awr 2026
1 Awr 2026