Yuusufa jóg, ànd ak xale bi ak ndeyam, ag guddi, ngir làquji Misra. Fa la toog, ba Erodd faatu. Noonu la mbir ma deme, ngir sottal la Boroom bi waxe woon ca làmmiñu yonent ba, ba mu nee: «Misra laa woowe sama doom, mu génne fa.»
Macë 2:14–15
Leeru Bés bi
Yuusufa jóg, ànd ak xale bi ak ndeyam, ag guddi, ngir làquji Misra. Fa la toog, ba Erodd faatu. Noonu la mbir ma deme, ngir sottal la Boroom bi waxe woon ca làmmiñu yonent ba, ba mu nee: «Misra laa woowe sama doom, mu génne fa.»
Macë 2:14–15
Xanaa xamuleen ne képp koo jébbal sa bopp, nangul ko, ab jaamam nga? Yaar ngeen diy jaam, bàkkaar di seen sang, jëme leen ci dee; mbaa ngeen déggal Yàlla, mu baaxe leen àtteb ñu jub.
Room 6:16
Loolu lépp, genn Noo googu moo koy def, ku nekk, mu sédd la ci, ni mu ko soobe.
1.Korent 12:11
Ku nekk nag, ak na mayu Noo giy feeñe ci moom, ngir njariñal ñépp.
1.Korent 12:7
Kenn ku ci nekk, may gi ko aw yiw jagleel, na ko taxawoo ñépp. Noonu ngeen di doone ay saytukat yu baax, di saytu ay may yu yiwu Yàlla wu yaa di joxe.
1.Piyeer 4:10
Te itam li ñuy sàkku ci ay saytukat moo di ñu jara wóolu.
1.Korent 4:2
Waaye jawriñ ji xamul nammeelu njaatigeem, te teewu koo def lu yelloo ay duma, yet yu néew lay am. Képp ku ñu jox lu bare, dees na la topp lu bare. Képp ku ñu dénk jópp, dees na la feyeeku lu ko ëpp.
Luug 12:48
Teewul muy ci ñii, xetu dee gu jëme ci dee, te di ci ñee, xetu dund gu jëme ci dund. Boobu sas nag, ana ku ko àttan?
2.Korent 2:16
Lépp laa mane ci ndimbalal ki may manal.
Filib 4:13
Deeleen def seen loxo ci lu faj soxlay gëmkat ñu sell ñi, te boole ci am teraanga.
Room 12:13
Daawuda moo noon: «Ndax kenn desul ba tey ci waa kër Sawul, ba ma jëfeek moom ngor ngir Yonatan?»
2.Samiyel 9:1
«Ca la buur bay wax ñi ci ndijooram ne leen: “Yeen ñi sama Baay barkeel, dikkleen jël nguur gi ñu leen waajalaloon ba àddina sosoo. Ndaxte ba ma xiifee, yeena ma leel; ma mar, ngeen nàndal ma; ma dib doxandéem, ngeen fat ma; ma rafle, ngeen wodd ma; ma wopp, ngeen toppatoo ma; ñu tëj ma, ngeen seetsi ma.”
Macë 25:34–36
Bu loolu amee buur ba ne leen: “Maa leen ko wax déy, lu ngeen ci defal kenn ci ñi gëna tuut ci sama bokk yii, man ngeen ko defal.”
Macë 25:40
Te maa leen ko wax déy, kenn ci ñii gëna tuut, képp ku ko may ab kaasu ndox mu sedd doŋŋ, ndax da di sama taalibe, doo ñàkk sag pey mukk.»
Macë 10:42
Te it di def lu baax ak di dimbalee, buleen ko fàtte, ndax sarax yu mel noonu la Yàlla gërëm.
Yawut ya 13:16
Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey ak cofeel gi ngeen sopp turam, te firndeele ko ni ngeen taxawoo ñu sell ñi, démb ak tey.
Yawut ya 6:10
Bés yu mujj yi
Wone yépp25 Mar 2026
24 Mar 2026
23 Mar 2026
22 Mar 2026
21 Mar 2026
20 Mar 2026
19 Mar 2026