Ibraayma nag tudde béreb boobu Yawe Yire (muy firi Aji Sax ji dina dikk). Moo tax ñuy wax ba tey, naan: «Aji Sax jaa ngay dikke ca tundam.»
Njàlbéen ga 22:14
Leeru Bés bi
Ibraayma nag tudde béreb boobu Yawe Yire (muy firi Aji Sax ji dina dikk). Moo tax ñuy wax ba tey, naan: «Aji Sax jaa ngay dikke ca tundam.»
Njàlbéen ga 22:14
Ibraayma ne ko: «Yàlla moom ci boppam dina dikk ak gàtt bi nuy def sarax, doom,» ñu daldi ànd dem, ñoom ñaar.
Njàlbéen ga 22:8
Ma ne, Aji Sax ji gàttul loxo ba tëlee walloo, noppam naqariwul ba tere koo dégg.
Esayi 59:1
Su boobaa nag, bànni Israayil gépp ay mucc, noonee ko Mbind mi indee ne: «Siyoŋ la wallukat bay jóge, mooy tenqee ngëmadi ci askanu Yanqóoba.
Room 11:26
Ndokkalee kuy dimbalikoo Yàllay Yanqóoba; di yaakaar Yàllaam Aji Sax ji,
Taalifi cant 146:5
Ma ne, Aji Sax jee naa jàkk ku ko ragal tey wéeroo ngoram. Day bakkanam, di ko dundal cib xiif.
Taalifi cant 33:18–19
Te sama Yàlla itam mooy sàkke ci koomam gu yéeme gi ci Almasi Yeesu, ba fajal leen seen soxla yépp.
Filib 4:19
Buleen jikkowoo bëggub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne: «Duma la bàyyi mukk, duma la wacc mukk.» Moo tax nu mana am fitu wax ne: «Boroom beey sama ndimbal, duma tiit. Ana lees ma manal?»
Yawut ya 13:5–6
Aji Sax jee may dooleel, di ma feg. Moom laa wóolu, mu wallu ma, sama xol tooy, ma woy, sante ko.
Taalifi cant 28:7
Sama nijaay, maa moom, man it, moo moom, di fore digg tóor-tóor yi.
Ngën-gi-woy 2:16
ndax fu ñaar mbaa ñett dajee ci sama tur, maa ngi ci seen biir.»
Macë 18:20
Yeesu ne ko: «Ku ma sopp day sàmm sama kàddu, sama Baay sopp ko; fi moom lanuy dikk, te moom lanuy def màkkaan.
Yowaan 14:23
Ni ma sàmme sama santaaney Baay, ba tax ma sax ci cofeelam, su ngeen ni sàmmee samay santaane, dingeen sax ci sama cofeel.
Yowaan 15:10
Yaw, ngelawal bëj-gànnaar, yewwul, ngelawal bëj-saalum, dikkal, wolalleen ma sama tool bi, mu gilli; sama nijaay dugg toolam, xéewloo ngën-gi-meññeefam.
Ngën-gi-woy 4:16–5:1
Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm akug teey ak noot sa bakkan. Yu mel noonu, wenn yoon bañu ko.
Galasi 5:22–23
Li feeñal sama darajay Baay mooy ngeen meññ lu bare, te noonu ngeen di firndeele ne samay taalibe ngeen.
Yowaan 15:8
Sama bépp car bu meññul, da koy tenqi sànni, bépp car bu ci meññ lay xosat ba mu set wecc, ngir mu gëna meññ.
Yowaan 15:2
Su boobaa ngeen meññal ba woomle ci njub gi Yeesu Almasi bi di maye, ngir fésal màggug Yàlla, jollil ag cantam.
Filib 1:11
Bés yu mujj yi
Wone yépp9 Mar 2026
8 Mar 2026
7 Mar 2026
6 Mar 2026
5 Mar 2026
4 Mar 2026
3 Mar 2026