Leeru Bés bi — 11 Mars: Màndiŋ ma 6:24

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

«“Yal na la Aji Sax ji barkeel, sàmm la.

Màndiŋ ma 6:24

Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.

Kàddu yu xelu 10:22

Képp ku la làqoo, yal na bég, di saxoo sarxolle, nga di ko yiir, te ku la sopp di la bége.

Taalifi cant 5:12

Kii du la bàyyi nga tërëf, sa sàmm bii gëmmul.

Taalifi cant 121:3

Aji Sax jee lay sàmm, Aji Sax jee lay yiir, féete la ndijoor.

Taalifi cant 121:5

Aji Sax jee lay sàmm ci gépp loraange, di sàmm sa bakkan. Aji Sax jee lay sàmm, dem ak dikk, tey ak ëllëg.

Taalifi cant 121:7–8

te man Aji Sax ji maa koy toppatoo, di ko suuxat saa su ne, di ko wattu guddeek bëccëg, bala koo kenn a song.

Esayi 27:3

Toogatuma ci àddina, waaye ñoom ci àddina lañu nekk, te man, ci yaw laa jëm. Baay bu sell bi, sàmme leen sa tur wi nga ma jox, ngir ni nu nekke benn, ñoom it ñu nekke noonu benn. Diir bi may nekk ak ñoom, man maa leen doon sàmme sa tur wi nga ma jox. Wattu naa leen, ba kenn ci ñoom sànkuwul, ku moy doomu sànkute jiy sànku, ngir Mbind mi sotti.

Yowaan 17:11–12

Boroom bee may wallu ci jépp jëf ju bon, te moo may aar ba tàbbal ma fa nguuram ga fa asamaan. Daraja ñeel na ko, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.

2.Timote 4:18

Yeesu nag jooy.

Yowaan 11:35

Dees na ko xeeb, daw ko, muy nit ku bare mitit te miin naqar. Mu mel ni ku ñuy dummóoyu, dees koo xeeb te nawloowuñu ko.

Esayi 53:3

Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.

Yawut ya 4:15

Ndax kat Yàlla mi lépp lu sàkke ñeel, te lépp sàkkoo ci moom, moo nammoona wommat gone yu bare ba sédd leen daraja. Moo tax muy lu jaadu, mu sottale matug Yeesu ay coono, ndax Yeesu moo xàllal gone yooyu yoonu mucc.

Yawut ya 2:10

Li muy Doom lépp, terewu koo tàggatu ci dégg ndigal, ndax coono yi mu daj.

Yawut ya 5:8

Boroom bi Aji Sax jee ma bënnali nopp, te man it, gàntalu ma ko, deltuwuma gannaaw. Sama gannaaw laa jox ku may dóor, dékk lex kuy xus sama sikkim, te làquma sama kanam ku may saagaaka serati.

Esayi 50:5–6

Yawut ya naan: «Gisleen rekk ni mu ko bëgge!»

Yowaan 11:36

Ndax kat du ay malaaka la Yeesu xettalisi, waaye askanu Ibraayma la xettalisi. Moo tax fàww mu niru woon ay bokkam ci bépp fànn. Su ko defee mu mana doon seen sarxalkat bu mag bu am yërmande te wóor fa kanam Yàlla, ngir mana defal askan wi seen njotlaayal bakkan.

Yawut ya 2:16–17