Leeru Bés bi — 8 Mars: Esayi 38:17

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ndeke sama tiisu xol wii, sama jàmm rekk a tax. Sa cofeel a tax nga sorele maak paxum sànkute. Yaa sànni sa gannaaw sama bépp bàkkaar.

Esayi 38:17

Ana Yàlla ju mel ni yaw, di baale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom? Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne. Moo nuy yërëmati; sunuy ñaawtéef lay joggiy tànkam, te biir xóotey géej lay tàbbal sunuy bàkkaar.

Mise 7:18–19

Mu ne: «Maa la wacc diir bu gàtt, dellu la jël ci yërmande ju yaa. Sama xol a jóg, ma xañ la sama kanam ab diir, waaye maa lay yërëme ngor gu sax.» Aji Sax ji lay jot moo ko wax.

Esayi 54:7–8

Kenn dootul soxlaa jàngal kenn, muy moroomam mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Aji Sax ji!” Ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ci ki gëna mag,» kàddug Aji Sax jee, «ndax maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.»

Yeremi 31:34

Dib taalifu yeete, ñeel Daawuda. Ndokkalee yaw mi ñu baal ag moy, jéggal la bàkkaar. Ndokkalee yaw mi Aji Sax ji toppul say tooñ, te amoo xelum njublaŋ it.

Taalifi cant 32:1–2

Waaye ni mu nekke moom ci boppam cig leer, su nu dee wéye noonu ag leer, su boobaa lanuy séq jokkoog mbokk, te deretu Yeesu Doomam moo nuy raxas ba nu set, tàggook bépp bàkkaar.

1.Yowaan 1:7

Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.

2.Timote 1:12

Moom mi mana jëfoo kàttan giy liggéey ci nun, ba sottal mboolem lu nu ñaan ak lu nu xalaat, ba wees loola fuuf sax,

Efes 3:20

te Yàlla man na leena baawaanal wépp yiw, ba ngeen saxoo am lu leen doy ci lépp, ak koom gu bare, ngir jépp jëf ju baax.

2.Korent 9:8

Coonoy nattu bi mu dékku nag tax na mu mana wallu ñi nekk ci nattu.

Yawut ya 2:18

Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.

Yawut ya 7:25

Ki leen mana aar ci bépp jéll, ba taxawal leen fa muy teewejee darajaam, te fekk leen ñàkk sikk, seen mbég mat sëkk,

Yudd 24

Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.

2.Timote 1:12

Mooy kiy liggéeye manooreem ji mu tënke lépp cig curgaam, ba sopparñi sunu yaram wu doyadi wii, niroole kook yaramam wi ànd ak màggaay.

Filib 3:21

Naka la Yeesu délsi, ba dugg ca kër ga, gumba ya duggsi. Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen ne man naa koo def?» Ñu ne ko: «Waawaaw, Sang bi.» Yeesu daldi laal seeni bët, ne leen: «Noonu ngeen ko gëme, na ame noonu.»

Macë 9:28–29