Yaa ma xalab xóotey xolu géej, ndaw ma mëdd ma. Say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.
Yunus 2:4
Leeru Bés bi
Yaa ma xalab xóotey xolu géej, ndaw ma mëdd ma. Say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.
Yunus 2:4
Siyoŋ a nga naa: «Aji Sax ji wacc na nu, Boroom bi fàtte na nu!» Aji Sax ji nee: «Ana jaboot juy fàtte doomam juy nàmp, mbaa muy néege ku mu jur ci biiram? Bu ko manoona fàtte it, man duma la fàtte.
Esayi 49:14–15
Jàmmi xol a ma réer, ma fàtte sax luy mbégte. Ca laa ne sama muñukaay a jeex ak it sama yaakaar ci Aji Sax ji!
Jooytu 3:17–18
Yaa tax ñu yendu noo bóom, dees noo jàppe ni xar yu ñuy tër.
Taalifi cant 44:23
Yeen askanu Yanqóoba, lu ngeen di jàmbat? Yeen Israayil laa ne, lu ngeen di jooy, naa: «Aji Sax ji gisul li nu dal, sunu Yàlla daal, daa réere sunu àq!»
Esayi 40:27
Sama xol a jóg, ma xañ la sama kanam ab diir, waaye maa lay yërëme ngor gu sax.» Aji Sax ji lay jot moo ko wax.
Esayi 54:8
Moo man, lu may xàddi, ne yogg? Lu may jàq nii? Tee maa yaakaar Yàlla, ba santati ko, moom sama Yàlla mi may wallu?
Taalifi cant 43:5
Nu nekk lees nuy tance, waaye deesu nu nappaaje. Dinanu jaaxle, waaye dunu jàq. Dees na nu bunduxataal, waaye deesu nu wacc. Dees na nu daaneel, waaye deesu nu jekkali.
2.Korent 4:8–9
«Walaakaanaak néew-doolee ngi wër, di wutum ndox, amul. Seen put wow koŋŋ ak mar. Man Aji Sax ji, maa leen di nangul; man Yàllay Israayil, duma leen wacc.
Esayi 41:17
Rendileen seen sarax yi war, te wóolu Aji Sax ji.
Taalifi cant 4:6
Ma ne ana lu nit di jariñoo ci doñ-doñ ak xalaatu xol yi muy doñ-doñaale fi kaw dun bi? Ndegam day yendoo tiis ak naqaru tës-tës, ba far fanaanoo xel mu dalul. Loolu it, cóolóoli neen.
Kàdduy waare 2:22–23
Ma far bañ àddina. Ndaw naqar ci jëfi kaw suuf, te lépp di cóolóoli neen ak nappum ngelaw!
Kàdduy waare 2:17
«Ñaari yoon la xeet wi ma séddoo bàkkaar: ma di bëtu ndox muy dund, ñu wacc ma, man, di gasal seen bopp kàmbi dencukaayi ndox, te kàmb yi fett, di senn.
Yeremi 2:13
Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw, te man, ku ñëw ci man, duma ko dàq mukk.
Yowaan 6:37
Maay sottim ndox suuf su mar, ak wal yu waleg joor gu wow. Maay sotti saw askan samag noo, sama barke sottikul ñi nga meññ,
Esayi 44:3
Ndokkalee ñi xiif aka mar jëfe njekk, ndax dinañu regg.
Macë 5:6
Dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Mooy ba mu nekkee ca màndiŋu Yuda.
Taalifi cant 63:1
Bés yu mujj yi
Wone yépp23 Okt 2025
22 Okt 2025
21 Okt 2025
20 Okt 2025
19 Okt 2025
18 Okt 2025
17 Okt 2025