te ngeen jàngal leen ñu sàmm mboolem li ma leen sant. Maa ngii nag, di nekk ak yeen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»
Macë 28:20
Leeru Bés bi
te ngeen jàngal leen ñu sàmm mboolem li ma leen sant. Maa ngii nag, di nekk ak yeen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»
Macë 28:20
Ki nangu sama ndigal nag, te di ko sàmm, moo ma sopp, te kooku ma sopp, cofeel ñeel na ko, bawoo fa sama Baay, te man itam dinaa ko sopp, di ko feeñu.» Yuda meneen ma wuuteek Yuda Iskaryo, ne ko: «Sang bi, lu waral nga nar noo feeñu te doo feeñu àddina?» Yeesu ne ko: «Ku ma sopp day sàmm sama kàddu, sama Baay sopp ko; fi moom lanuy dikk, te moom lanuy def màkkaan.
Yowaan 14:21–23
Ki leen mana aar ci bépp jéll, ba taxawal leen fa muy teewejee darajaam, te fekk leen ñàkk sikk, seen mbég mat sëkk, Yàlla miy kenn, sunu Musalkat, ci sunu ndimbalal Sang Yeesu Almasi bi, daraja ak màggaay ak kàttan ak sañ-sañ ñeel na ko, démb ak tey ak ëllëg, ba fàww! Amiin.
Yudd 24–25
Te itam mujug lépp dëgmal na; kon nag jiitalleen seenum xel, te ànd ak seen sago, ngir ngeen man di ñaan.
1.Piyeer 4:7
Ci kaw loolu ma gis ngàngune mu mag mu weex ak ki ci toog. Asamaan ak suuf daldi dawe fa kanamam, ne mes.
Peeñu ma 20:11
Waaye asamaanu tey jii ak suuf, genn kàddug Yàlla googu moo leen yeb cib denc, ñeel sawara, kera bésub àtte ba, bésu sànkuteb aji gëmadi ñi.
2.Piyeer 3:7
Mu jëm ci njiital woykat yi, di woy wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen. Sunu Yàllaa nuy rawale, di nu dooleel, di nu wallu fu nu jaaxlee, ba dunu tiit suuf su yëngu sax, ba tund yiy tàbbi biir géej,
Taalifi cant 46:1–3
Dingeen dégg ay xare ak coowi xare; waaye moytuleena tiit, ndax fàww loolu am, waaye du doonagum muj ga.
Macë 24:6
Xam nanu ne sunu yaram, sunu këru kaw suuf gii di ab xayma, bu daanoo it, am taax lanu am fa Yàlla, kër gu sax dàkk gu loxol nit tabaxul.
2.Korent 5:1
Waaye asamaan su bees ak suuf su bees te njub dëkke ko bu keroogee, moom lanuy séentu, na nu ñu ko dige woon. Kon nag soppe yi, li feek ngeen di séentu loolu, defleen seen kem-kàttan, ba bésub keroog fekk leen ci jàmm, te ngeen baña am benn gàkk, mbaa sikk ci gis-gisu Yàlla.
2.Piyeer 3:13–14
Bés yu mujj yi
Wone yépp24 Okt 2025
23 Okt 2025
22 Okt 2025
21 Okt 2025
20 Okt 2025
19 Okt 2025
18 Okt 2025