Ci kaw loolu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen wépp xeetu bëgge, ndax loo barele barele, sa bakkan ajuwul ci sa alal.»
Luug 12:15
Leeru Bés bi
Ci kaw loolu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen wépp xeetu bëgge, ndax loo barele barele, sa bakkan ajuwul ci sa alal.»
Luug 12:15
Aji jub, as tuutam moo gën koomu ku bon.
Taalifi cant 37:16
Néewle te ragal Aji Sax ji moo gën barele, sa bopp ubu.
Kàddu yu xelu 15:16
Teewul ragal Yàlla gu ànd ak doylu, di alal ju réy.
1.Timote 6:6
Kon su nu amee lu nu lekk ak lu nu sol, nanu ko doyloo.
1.Timote 6:8
caaxaan aki fen, yal na ma sore, néewleek barele, bu ma ci may lenn, leel ma lu ma doy; lu ko moy ma regg, weddi la, ba naan: «Kuy Aji Sax ji?» Mbaa ma ñàkk bay sàcc, di la ñàkke worma, yaw sama Yàlla.
Kàddu yu xelu 30:8–9
May nu bésub tey, sunu dundub bés bu nekk,
Macë 6:11
«Moo tax ma ne leen, buleen seen bakkan jaaxal, ngir lu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan, te it buleen seen yaram jaaxal ngir lu ngeen sol. Xanaa du lekk gi, bakkan bee ko ëpp solo, te koddaay li it, yaram wee ko ëpp solo?
Macë 6:25
Yeesu neeti leen: «Ba ma leen yebalee te du dencukaayu xaalis, du mbuus, du carax yu ngeen yóbbaale, ndax ñàkk ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
Luug 22:35
Buleen jikkowoo bëggub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne: «Duma la bàyyi mukk, duma la wacc mukk.»
Yawut ya 13:5
Noowug Yàlla mooy dundloo; nitu suuxu neen manul dara. Kàddu gi ma leen wax moo leen di jottali Noowug Yàlla giy taxa dund.
Yowaan 6:63
Lu juddoo ci nitu suuxu neen, nitu suux la, lu juddoo ci Noowug Yàlla nag, ag noo la.
Yowaan 3:6
ca la nu musal, te du jenn jëfu njekk ju nu def, ba tax mu musal nu, waaye ci yërmandeem la nu musale, sang nu cangaay lu nu taxa judduwaat, boole ci yeesale nu Noo gu Sell
Tit 3:5
Yeen nag nekkatuleen ci kilifteefu bindu suuxu neen, waaye ci kilifteefu Noo gu Sell gi ngeen nekk, ndegam kay Noowug Yàllaa ngi sax ci yeen. Ku amul Noowug Almasi bi, kooku du nitam. Su Almasi bi nekkee ci yeen, seen yaram dina dee moos ndax bàkkaar, waaye du tee seenug noo di dund, ndax àtteb njub bi ngeen am ba noppi. Noowug ki dekkal Yeesu moo sax ci yeen. Kon nag ki dekkal Almasi bi mooy dekkal itam seen yaram wu jëm ci dee, ndax Noowam googu sax ci yeen.
Room 8:9–11
Moo tax dootul man maay dund, waaye Almasi bi mooy dund léegi ci man. Sama dundu yaramu suux wii tey nag, ci ngëm gi ma gëm Doomu Yàlla laa koy dunde, moom mi ma sopp, ba jébbale boppam ngir man.
Galasi 2:20
Naka noonu, yeen itam jàppeleen seen bopp nit ñu dee ba dootuleen nangooti kilifteefu bàkkaar, xanaa di dund ngir Yàlla, ndax seen bokk ci Yeesu Almasi bi.
Room 6:11
Bés yu mujj yi
Wone yépp22 Okt 2025
21 Okt 2025
20 Okt 2025
19 Okt 2025
18 Okt 2025
17 Okt 2025
16 Okt 2025