Leeru Bés bi — 20 Oktoobar: Room 7:22

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ndaxam ci sama biir xol, yoonu Yàllaa ma neex.

Room 7:22

Maaka sopp saw yoon, di ko jàngat bés bu jot.

Taalifi cant 119:97

Sa kàddu laa gis, di ko dunde, sa kàddu di ma bégal, bànneexal sama xol. Yaw Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, déy, sa tur lañu ma tudde.

Yeremi 15:16

Mbete garab gu gëna neex ci gott bi, kookooy sama nijaay ci biir xale yu góor yi. May bége keppaaram, safoo doom ya.

Ngën-gi-woy 2:3

Dëdduwuma ay santaaneem, sama biir xol laa denc ay kàddoom.

Ayóoba 23:12

Ma ne: «Maa dikk nii, téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man.

Taalifi cant 40:8

Yeesu ne leen: «Samaw ñam moo di jëfe coobarey ki ma yónni, ba sottal ab liggéeyam.

Yowaan 4:34

Yoonu Aji Sax jee mat, di leqali bakkan. Lu Aji Sax ji seede dëgg la, day xelal ku xeluwul.

Taalifi cant 19:8

Santaaneb ragal Aji Sax ji mooy li sell te sax ba fàww. Lu Aji Sax ji digle, dëgg la, ak njub gu sotti.

Taalifi cant 19:10

Doonleen jëfekati kàddu gi, buleen di ay déglukat doŋŋ, di nax seen bopp. Ndax kat kuy déglu kàddu gi te jëfewoo ko, kooku daa mel ni kuy niir kanamam cib seetu:

Yanqóoba 1:22–23

Man Arawna, maa la jox lii lépp, Buur. Yal na la sa Yàlla Aji Sax ji nangul.»

2.Samiyel 24:23

Ana lu may dikkaale fi kanam Aji Sax ji, ba sujjóotal Yàlla ja fa kaw? Tee ma koo dikke ay rendi-dóomal, ay wëlluy menn at? Mbaa dina ma nangul junniy kuuy, ak fukki junniy dexi diw? Am samab taaw laay joxe saraxu peyu bàkkaar, sama meññeefum biir di sama saraxu peyug tooñ? Yaw nit ki, waxees na la li baax, ak li Aji Sax ji sàkku ci yaw, te loolu moyul di def yoon, sopp jëfi ngor te woyof nooy toppe sa Yàlla.

Mise 6:6–8

Du kenn kuy wormaal sa tur, mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw, yaa nu làq saw yiw, yaa nu def ban bu tooy ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc.

Esayi 64:6

Noonu it la Mbind mi indee ne: «Kenn jubul, du kenn sax.

Room 3:10

Ndax kat ñépp a bàkkaar, ba jotewuñu leeru Yàlla, te ci yiwu Yàlla wu àndul ak genn pey lees di baaxe ñépp àtteb ñu jub, ndax njot gi sottee ci Almasi Yeesu. Moom la Yàlla tudd muy njot gu ngëm di maye, ci kaw deretam ji tuuru. Noonu la Yàlla firndeele ne njubteem mat na sëkk doonte tanqamlu woon na bàkkaari niti jamono ya woon, ndax Yàlla ci biir ag jéllaleem la firndeel njubteem ci janti tey jii, ngir mu leer ne moo wéye njub, te képp ku gëm Yeesu, moo koy baaxe àtteb ku jub.

Room 3:23–26

Moo tax cant ñeel ko, ndax yiwam wu màgg wi mu nu baawaanal ci Soppeem bi.

Efes 1:6

ci moom ngeen mate it, te mooy kilifay mboolem boroom nguur yi ak mboolem boroom sañ-sañ yi.

Kolos 2:10