Di woyu cant, ñeel Daawuda.
Taalifi cant 108:1
Leeru Bés bi
Di woyu cant, ñeel Daawuda.
Taalifi cant 108:1
Ñeel Daawuda. Aji Sax jee may leeral, di ma wallu. Ana ku may ragal? Aji Sax jeey aar sama bakkan. Ana ku may tiit?
Taalifi cant 27:1
Yaw Aji Sax ji, ku dogu, pastéefu, wóolu la, nga may ko jàmm ju mat, nde moo la wóolu.
Esayi 26:3
Du ragal dég-dég bu tiis, xel ma day dal, mu wóolu Aji Sax ji, fit wa toog, du ragal, ba kera muy gis noonam jóoru.
Taalifi cant 112:7–8
Noon yee ma yendoo lakkal, bare lool di xareek man. Ku màgg ki,
Taalifi cant 56:3
Bésub fitna, mu yiire ma mbaaram, làq ma, ma làqoo xaymaam, aj ma ciw doj, ma raw. Ma doxe fa siggi, tiim noon yi ma wër, di sarxali fa xaymaam saraxi sarxolle. Naa woyal Aji Sax ji, joobe ko.
Taalifi cant 27:5–6
Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi bi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju. Moom la kàttan ñeel ba fàww. Amiin.
1.Piyeer 5:10–11
Aji Sax jee samp asamaan ab jalam, nguuram ŋank lépp.
Taalifi cant 103:19
Tegoo bant nit a koy def, dogal ba Aji Sax ji la.
Kàddu yu xelu 16:33
Ndax bu buftab xare jibee, waa dëkk ba du tiit? Ndax aw ay dina dabub dëkk te du Aji Sax jee?
Amos 3:6
Aji Sax ji man a, du keneen; kenn du Yàlla ku dul man. Maa la gemb, te xamuloo ma, ngir xamees penku ba sowu, ne lu dul man neen la. Aji Sax ji man a, du keneen. Maay bind leer, di def lëndëm. Maay indi jàmm, di def safaan. Maay Aji Sax jiy def lii lépp!
Esayi 45:5–7
Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?
Room 8:31
Ndaxte fàww Almasi bi nguuru, ba kera Yàlla di teg mboolem ay noonam ciy tànkam.
1.Korent 15:25
«Buleen ragal dara, yeen jur gu sew gi, ndax seen Baay la soob, mu jagleel leen nguur gi.
Luug 12:32
Bés yu mujj yi
Wone yépp21 Okt 2025
20 Okt 2025
19 Okt 2025
18 Okt 2025
17 Okt 2025
16 Okt 2025
15 Okt 2025