Leeru Bés bi — 17 Oktoobar: Taalifi cant 89:16

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Aji Sax ji, ndokkalee mbooloo mu la xal di sarxollee, di niitoo saw yiw,

Taalifi cant 89:16

Dees na ma waxal ne: «Aji Sax ji rekk a jagoo àtte ak doole!» Mboolem ñi ma mereey ànd, sëgg, fekksi ma. Ci Aji Sax ji la askanu Israayil gépp yeye, bay damu.

Esayi 45:24–25

Yaw aji jub ji, bégal te bànneexoo Aji Sax ji. Képp kuy def njub, sarxolleel!

Taalifi cant 32:11

Waaye léegi Yàlla moo feeñal nu nit di ame fa kanamam àtteb njubam gu ajuwul ci yoonu Musaa. Te yoonu Musaa ak yonent yi seede nañu loolu. Googu njub fa kanam Yàlla nag, ci gëm Yeesu Almasi bi lees koy ame, te mboolem ñi ko gëm la ñeel, amul xejj ak seen.

Room 3:21–22

ndax Yàlla ci biir ag jéllaleem la firndeel njubteem ci janti tey jii, ngir mu leer ne moo wéye njub, te képp ku gëm Yeesu, moo koy baaxe àtteb ku jub.

Room 3:26

Bégleen ci Boroom bi fu ngeen tollu, ma waxati ko, bégleen!

Filib 4:4

Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd,

1.Piyeer 1:8

Bu nu dugal ci nattu, waaye yal nanga nu musal ci ku bon ki. Yaw de yaa yelloo nguur ak kàttan ak màggaay, ba fàww. Amiin.”

Macë 6:13

Aji Sax jeey buur, soloo daraja; Aji Sax jee solu, gañoo doole: àddinaa ngii, dëju te raful. Sab jal a masa sax, te yaa masa nekk.

Taalifi cant 93:1–2

Aji Sax ji la mer ma diib, doole ja bare; te du ñàkka topp ku tooñ ag tooñaangeem. Aji Sax jeey daagoo biir callweer ak ngëlén, niir yi di pëndub tànkam.

Nawum 1:3

Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?

Room 8:31

Ndegam Yàlla ji nuy jaamu man nanoo musal ci taalu sawara bu yànj bi, musal nu ci yaw mii, dina nu musal.

Dañeel 3:17

Sama Baay bi ma leen jox, moo gëna màgg lépp, te kenn manula foqatee lenn ci loxol Baay bi.

Yowaan 10:29

Yeen xale yi, ci Yàlla ngeen bokk, te daan ngeen yonenti caaxaan yooyu, ndax ki ci yeen moo ëpp doole ki ci àddina.

1.Yowaan 4:4

Bu muy nun, Aji Sax ji, bu muy nun, saw tur nga wara teral, ngir sa ngor ak sa worma.

Taalifi cant 115:1

Yaw, Aji Sax ji, yaa yelloo màggaay ak doole, teraanga ak ndam ak daraja; Aji Sax ji, mboolem li ci asamaan ak suuf yaay boroom. Yaay boroom nguur gi, di Buur bu kawe, sut lépp.

1.Jaar-jaar ya 29:11

Kon sunu Yàlla, nu ngi lay sant, di màggal sa tur wu tedd. Ana lu nu tekki, maak sama ñoñ, ba nu man laa jox saraxi yéene yii? Ci yaw la lépp jóge, te say loxo lanu jële, jox la.

1.Jaar-jaar ya 29:13–14