Leeru Bés bi — 24 Sàttumbar: Taalifi cant 73:28

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Man de, jege Yàllaa ma gënal. Boroom bi Aji Sax ji, yaw laa def kiiraay, ngir siiwal sa jépp jëf.

Taalifi cant 73:28

Aji Sax ji, maa sopp sa dëkkuwaay, bëgg béreb bi sag leer teew.

Taalifi cant 26:8

Éy Yàlla, geesul Buur, sunu kiiraay, ngalla niiral kii nga fal.

Taalifi cant 84:10

Samay ñaawtéef man na ma, waaye sunuy tooñ, yaa nu koy baal.

Taalifi cant 65:4

Aji Sax jee baax ci ñi ko yaakaar, baax ci ki ko wóolu.

Jooytu 3:25

Aji Sax ji déy a leen namma baaxe, moo ko tax di jóg moos ngir yërëm leen, nde Aji Sax jeey Yàllay njubte. Ndokkalee képp ku ko yaakaar!

Esayi 30:18

Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca néeg bu sella sell ba, ngir deretu Yeesu, deretu Yeesu jiy yoon wu yees, yoonu dund gu mu nu xàllal, jàllale ko ca rido ba, te rido ba moo di yaramu suuxam wi mu saraxe.

Yawut ya 10:19–20

Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.

Yawut ya 10:22

Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi bi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.

2.Korent 8:9

Kàddu gee sol aw suux, doon nit, màkkaanoo ci sunu biir, nu ne jàkk ci darajaam, darajay jenn Doom ji bawoo ci Baay bi, mat sëkk ci aw yiw akug dëgg.

Yowaan 1:14

Woy wu neex a fees sama xol, may taalifal Buur, sama làmmiñ ni xalimag bindkatu ndaanaan.

Taalifi cant 45:2

Ñépp a doon seedeel Yeesu lu rafet, tey yéemu ci kàdduy yiw yi tukkee ci gémmiñam. Ñu naan: «Xanaa kii du doomu Yuusufa ji?»

Luug 4:22

gannaaw mos ngeen ci mbaaxug Sang bi.

1.Piyeer 2:3

Ku gëm Doomu Yàlla, seede soosoo ngi ci sab xol. Ku gëmul Yàlla nag, ab fen-kat nga ko def, ndax yaa gëmul seede si Yàlla seedeel Doomam.

1.Yowaan 5:10

Maa la ko wax déy, ci lu wér; li nu xam, nu ngi koy wax; li nu gis, nu ngi koy seede, yeen kay yeena baña gëm li nu seede.

Yowaan 3:11

Ku ragal Aji Sax ji, malaakaam yiir la, di la wallu.

Taalifi cant 34:8

Mbete garab gu gëna neex ci gott bi, kookooy sama nijaay ci biir xale yu góor yi. May bége keppaaram, safoo doom ya.

Ngën-gi-woy 2:3

Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi bi wàcc ci sama kaw.

2.Korent 12:9

Waaye ku nekk ci nun ak mayam, ci yiwu Yàlla, ni ko nattub Almasi bi séddalee.

Efes 4:7

Kenn ku ci nekk, may gi ko aw yiw jagleel, na ko taxawoo ñépp. Noonu ngeen di doone ay saytukat yu baax, di saytu ay may yu yiwu Yàlla wu yaa di joxe.

1.Piyeer 4:10