Ku teewlu mbir, baaxle; ku wóolu Aji Sax ji, bég.
Kàddu yu xelu 16:20
Leeru Bés bi
Ku teewlu mbir, baaxle; ku wóolu Aji Sax ji, bég.
Kàddu yu xelu 16:20
Teewul digeb Yàlla ba la ne jàkk, nàttablewul, gëmadiwul, xanaa dëgërloo dooley ngëmam rekk, sant Yàlla. Dafa wéroon Ibraayma péŋŋ ne li Yàlla dige, man na koo def.
Room 4:20–21
Jant yooyu la bànni Israayil suufe, Yudeen ña féete kaw, ndax la ñu wéeroo Aji Sax ji seen Yàllay maam.
2.Jaar-jaar ya 13:18
Mu jëm ci njiital woykat yi, di woy wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen. Sunu Yàllaa nuy rawale, di nu dooleel, di nu wallu fu nu jaaxlee,
Taalifi cant 46:1–2
Làqoo Aji Sax jee gën wóolu doom aadama. Làqoo Aji Sax jee gën wóolu garmi.
Taalifi cant 118:8–9
Bu Aji Sax ji rafetloo saw yoon, mooy jiite say jéego. Soo tërëfee it, doo daanu. Aji Sax jee lay walloo loxoom.
Taalifi cant 37:23–24
Ku ragal Aji Sax ji, malaakaam yiir la, di la wallu. Mosleen, xam ne Aji Sax jee baax, ndokkalee yaw mi ko làqoo.
Taalifi cant 34:8–9
May nga ma bànneexu xol bu raw seen pepp mu tuurook biiñ bu wal.
Taalifi cant 4:8
Doo ragal njàqarey guddi mbaa fittu bëccëg
Taalifi cant 91:5
Kiiraayam la lay sànge, nga yiiru, làqu; kóllëreem feg la, di la aar.
Taalifi cant 91:4
«Yerusalem, Yerusalem, yaw miy bóom yonent yi, di sànni ay doj ñi ñu yebal ci yaw, ba ñu dee, ñaata yoon laa namma boole say doom, uuf ni ganaar di uufe ay cuujam, te nanguwuloo?
Macë 23:37
Kii du la bàyyi nga tërëf, sa sàmm bii gëmmul. Kiy sàmm Israayil kay gëmmul, nelawul. Aji Sax jee lay sàmm, Aji Sax jee lay yiir, féete la ndijoor.
Taalifi cant 121:3–5
Yaw laa làqoo, ngay tata ju dëgër, fegal ma noon.
Taalifi cant 61:4
du tax lëndëm lëndëmal la dara. Guddi da laa leeralal ni bëccëg, lëndëm dig leer fi yaw.
Taalifi cant 139:12
Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa joxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?
Room 8:32
Yeen nag, Almasi bi moo leen moom, te Almasi bi, Yàllaa ko moom.
1.Korent 3:23
Bés déy ñeel na Aji Sax ju gàngoor yi, ca lay xaare képp ku bew ak ku reew, ba kuy daŋŋiiral, detteelu.
Esayi 2:12
Bés yu mujj yi
Wone yépp28 Ut 2025
27 Ut 2025
26 Ut 2025
25 Ut 2025
24 Ut 2025
23 Ut 2025
22 Ut 2025