Ba mu ko defee Buur gis Lingeer Esteer, mu taxaw ca biir ëtt ba. Mu baaxe ko, daldi koy tàllal yetu wurus wa muy màndargaale nguuram. Esteer jegesi, laal boppu yet wa, di ko ko sante.
Esteer 5:2
Leeru Bés bi
Ba mu ko defee Buur gis Lingeer Esteer, mu taxaw ca biir ëtt ba. Mu baaxe ko, daldi koy tàllal yetu wurus wa muy màndargaale nguuram. Esteer jegesi, laal boppu yet wa, di ko ko sante.
Esteer 5:2
«Man Yàlla, buleen wax lu ñaaw ci man, te seen kilifag askan, buleen wax lu bon ci moom.
Mucc ga 22:27
Nun nag xam nanu te gëm nanu cofeel gi nu Yàlla sopp. Yàlla cofeelu neen la. Képp ku saxoo cofeel, ci Yàlla nga sax, te Yàlla itam ci yaw la sax. Cofeel a mat sëkk ci nun, ngir nu ànd ak fit keroog bés-pénc. Te li nuy may fit mooy, ni Yeesu moomu nekke, noonu lanu nekke nun itam ci àddina sii. Cofeel àndul ak gennug ragal, waaye cofeel gu mat sëkk dàq na ag ragal; ag ragal, mook séentu ag mbugal ñoo ànd; te ku ragal, sag cofeel a des. Nun nag, li nu taxa am cofeel moo di Yàlla moo nu njëkka sopp.
1.Yowaan 4:16–19
Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.
Yawut ya 10:22
ndax nun ñaari xeet yépp, ci moom Almasi bi lanu jote ci Baay bi, ci ndimbalal genn Noo gu Sell gi.
Efes 2:18
Ci Yeesu, ci kaw ngëm gu nu ko gëm lanu ñemee àgge fit wu mat sëkk fa kanam Yàlla.
Efes 3:12
Kon nag nanu ñemee dikk ba ca ngàngunem yiw ma, ndax nu jot yërmande te dajeek aw yiw wu nu wallu fu nu ko soxlaa.
Yawut ya 4:16
Bànni Israayil gis ko, di wax ca seen biir naan: «Lii lu mu?» ndax xamuñu woon lu mu doon. Musaa ne leen: «Lii mooy ñam wi leen Aji Sax ji jox, ngeen lekk.
Mucc ga 16:15
Ndaxte ñamu Yàlla mooy ki wàcce asamaan te kooku moo may àddina ñu dund.»
Yowaan 6:33
Seeni maam a lekk mànn ca màndiŋ ma, te dee nañu.
Yowaan 6:49
Man maay ñam wiy dund te wàcce fa asamaan. Ku lekk ci wii ñam, mooy texe ba fàww. Ñam woowu nag mooy samaw suux; maa ko joxe, ngir àddina dund.»
Yowaan 6:51
Ndaxte sama yaram mooy ñam wi wóor, sama deret di naan gi wóor.
Yowaan 6:55
Bànni Israayil def noona, ñii for lu bare, ñee lu néew. Waaye ba ñu ko nattee ci andaar, ña sàkkoon lu bare amuñu lu ëpp, te ña sàkkoon lu néew yéeslewuñu. La ñu for dafa tolloo tembe ak seen njël.
Mucc ga 16:17–18
Suba su ñu xëyaan nag, ku nekk for ca njëlam, ndax bu naaj wa tàngaan, mu seey.
Mucc ga 16:21
Kon nag, buleen jaaxle, naan: “Lu nuy lekk?” mbaa “Lu nuy naan?” mbaa “Lu nuy sol?” Ndaxte loolu lépp, yéefar yi ñoo koy tiisoo. Te seen Baay ba fa asamaan xam na ne soxla ngeen loolu lépp. Waaye njëkkleena tiisoo nguurug Yàlla, ak njub gi mu laaj, te loolu lépp moo leen ko ciy dollil.
Macë 6:31–33
Bés yu mujj yi
Wone yépp29 Ut 2025
28 Ut 2025
27 Ut 2025
26 Ut 2025
25 Ut 2025
24 Ut 2025
23 Ut 2025