Leeru Bés bi — 25 Ut: Esayi 51:1

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Dégluleen maa, yeen ñiy wuta doxee yoon, wuta déggal Aji Sax ji. Xoolleen doj wi ñu leen yatte, xool xóotey kàmb gi ñu leen seppee:

Esayi 51:1

Xam naa ne maa tooñ, sama moy a ngi janook man saa su ne.

Taalifi cant 51:5

Xooleesu la bëtu ñeewante ngir defal la lenn ci yooyu ngir yërmande. Dees laa sànni ci àll bi bés ba nga juddoo ndax jéppi la. Maa fa jaare, seen la ngay wéqu, sangoo sa deret. Ma ne la: Sangoo nga sa deret waaye, dundal! Neeti la: Sangoo nga sa deret, waaye dundal!

Esekiyel 16:5–6

May xaar a xaar Aji Sax ji, mu dégg may woote, geesu ma, génnee ma ca kàmbug sànkute, sippee ma ca xóotey ban ba, cëppe ma ciw doj, samp ma, ma dëgër.

Taalifi cant 40:2–3

Ndax kat, ba nu amul menn pexem mucc, ca waxtu wa gën, la Almasi bi deewal yéefar yi. Barewul ku nangoo dee ngir nit ku jub, doonte jombul mu am ku nangoo dee ngir ku baax. Waaye Yàlla moom, ni mu firndeele cofeelam ci nun, moo di, ba nu doon ay bàkkaarkat, ca la Almasi bi deewe ngir nun!

Room 5:6–8

Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy gi mu nu sopp, nun ñi doon nit ñu dee ba noppi ndax sunuy moy, moo nu booleek Almasi bi, dundalaat nu. Ci kaw yiw daal ngeen mucce.

Efes 2:4–5

Maa bég a bég ci Aji Sax ji, sama xol di sedd ci sama Yàlla jii. Moo ma solal yérey mucc, sànge ma mbubbam ndam, may nirook boroom séet bu kaalawu ni sarxalkat, ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.

Esayi 61:10

Ñeel Daawuda. Mooy ba muy wayadi-wayadilu ca kanam Buur Abimeleg, ba Abimeleg dàq ko, mu dem. Naa màggal Aji Sax ji saa su ne, di ko sant fu ma tollu. Aji Sax ji laay sagoo, néew-ji-doole dégg, bég.

Taalifi cant 34:1–3

Benn fan ci sab ëtt de moo dàq junniy fan feneen. Sama taxawaayu bunt kër Yàlla moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon. Aji Sax ji Yàllaa mat jant, mat kiiraay; yiw ak daraja, Aji Sax ji joxe; te du ngëneel lu muy bañal ku mat.

Taalifi cant 84:11–12

Ñeel Daawuda. Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii, saa jëmm jépp di sàbbaal sellaayu turam!

Taalifi cant 103:1

Ana ci yeen ku nekk ciw tiis? Na ñaan. Ana ku ci am mbég? Na sàbbaal.

Yanqóoba 5:13

Buleen naan biiñ ba màndi, màndite ci afal seen bakkan la leen jëme, waaye na leen Noowug Yàlla fees, ngeen di jàngalante taalifi cant yi ak woyi cant yi ak woy yu fentoo ci Noowug Yàlla gi, di woy aka kañ Boroom bi ci seen xol. Fu ngeen tollu, ak ci mbir mu mu mana doon, santleen Yàlla Baay bi ci sunu turu Sang Yeesu Almasi bi,

Efes 5:18–20

Na kàddug Almasi bi dëkk ci yeen, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jàngalantee aka artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ak ay taalifi cant ak woyi tagg Yàlla ak woy yu ñu fente ci Noowug Yàlla gi.

Kolos 3:16

Ba guddi gay xaaj, Póol ak Silas a ngay ñaan, di sàbbaal Yàlla, ñeneen ña ñu fa tëj di leen déglu.

Jëf ya 16:25

Bégleen ci Boroom bi fu ngeen tollu, ma waxati ko, bégleen!

Filib 4:4