Ci kaw loolu ma dégg baat bu xumb bawoo asamaan, ne: «Léegi nag texe teew na, ànd ak sunu kàttanu Yàlla ak nguuram, ak sañ-sañu Almaseem, ndax xalab nañu ki daan tuumaal sunu bokk yi, di leen sosal guddeek bëccëg fi sunu kanam Yàlla.
Peeñu ma 12:10
Leeru Bés bi
Ci kaw loolu ma dégg baat bu xumb bawoo asamaan, ne: «Léegi nag texe teew na, ànd ak sunu kàttanu Yàlla ak nguuram, ak sañ-sañu Almaseem, ndax xalab nañu ki daan tuumaal sunu bokk yi, di leen sosal guddeek bëccëg fi sunu kanam Yàlla.
Peeñu ma 12:10
Sunu bokk yee daan ndax deretu Xar mi, ak seen kàddug seede, te soppuñu seen bakkan ba ragala dee.
Peeñu ma 12:11
Ñi Yàlla tànn, ana ku leen di tuumaal? Yàlla de moo leen àtte ni ñu jub.
Room 8:33
Ana kuy tegeb daan? Almasi Yeesu de moo dee, rax ci dolli, mu dekki, te moo toog fa ndijooru Yàlla, di nu fa ñaanal!
Room 8:34
Moo dog sidditi boroom nguur yeek boroom sañ-sañ yi ci jaww ji, ñu doon ay jaam yu mu jàppe xare. Moo leen weer it ci kanam ñépp, diriwaale leen ca biir njaab ma topp ca ndam la Almasi bi ame ca bant ba.
Kolos 2:15
Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane.
Yawut ya 2:14
Noonu la goreele mboolem ñi seenug ragala dee tënkoon cig njaam, seen giiru dund.
Yawut ya 2:15
Waaye ci mboolem lu nu dikkal, nooy am ndam lu mat sëkk, ci ndimbalal ki nuy soppeem.
Room 8:37
Ràngooleen mboolem gànnaayi Yàlla, ngir ngeen mana jànkoonte ak pexey Seytaane.
Efes 6:11
Mbaxanam xare miy seen kaaraange, jëlleen ko, sol; jëlleen itam saamar bi Noo gu Sell giy joxe, te muy kàddug Yàlla.
Efes 6:17
Waaye cant ñeel na Yàlla mi nu may ndam ci sunu Sang Yeesu Almasi bi!
1.Korent 15:57
Yàlla Aji Sax ji nag saxal ci suuf lépp luy garab gu meññeef ma rafet te neexa lekk; mu def it garab gay taxa dund ca digg tool ba, moom ak garab gay taxa xam lu baax ak lu bon.
Njàlbéen ga 2:9
Seede si moo di texe ba fàww la nu Yàlla jagleel, te texe googu ci Doomam la nekk.
1.Yowaan 5:11
Ndax Yàlla moo sopp àddina, ba joxe jenn Doomam ji, ngir képp ku ko gëm, texe ba fàww, te du sànku mukk.
Yowaan 3:16
ndax kat, ni Baay bi di dekkale ñi dee, dundal leen, noonu la Doom jiy dundale ku mu namma dundal.
Yowaan 5:21
Ndax kat ni Baay bi jagoo dund ci jëmmu boppam, noonu la maye Doom ji mu jagoo dund ci jëmmu boppam,
Yowaan 5:26
«Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may nga lekk ci garabu dund gi ci Àjjana, toolub Yàlla.
Peeñu ma 2:7
di tuuru ci digg péncum dëkk bi. Ci ñaari tàkki dex gi, garabu dund a ngi ci, di meññ fukki yoon ak ñaar, weer wu nekk benn yoon, xob yi di faj askani àddina.
Peeñu ma 22:2
Mbégtee ñeel ku daj xel mu rafet ak ku amug dégg.
Kàddu yu xelu 3:13
Gudd fan, mu joxee ndijoor; càmmoñ ba, alal ak teraanga.
Kàddu yu xelu 3:16
Mooy garab giy taxa dund ci ku ko jàpp, di mbégtey ku ca ŋoy.
Kàddu yu xelu 3:18
Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njub, di sunu cellte, di sunug njot,
1.Korent 1:30
Bés yu mujj yi
Wone yépp27 Ut 2025
26 Ut 2025
25 Ut 2025
24 Ut 2025
23 Ut 2025
22 Ut 2025
21 Ut 2025