Leeru Bés bi — 27 Ut: Taalifi cant 119:105

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.

Taalifi cant 119:105

Su may jëf it, di sàmm sa kàddu. Maay moyu yoonu ku bon. Sa tànk, sama tànk, jàdduma fenn.

Taalifi cant 17:4–5

Booy dox mu di la jiite, nga tëdd, mu di la sàmm, nga yewwu, mu di la waxal. Santaane da lay niital, ndigal leeralal la, artookub yar di yoonu dund.

Kàddu yu xelu 6:22–23

di dégg kàddu guy jibe seen gannaaw, naa leen: «Yoon waa ngii, jaareleen fi;» bu ngeen awee ndijoor, mbaa càmmoñ.

Esayi 30:21

Yeesu waxati leen ne leen: «Man maay leeru àddina. Ku ma topp doo dox cig lëndëm, waaye leeru dund ngay am.»

Yowaan 8:12

Rax ci dolli nu ngeek waxi yonent yi, muy wax ju wóor ju jara gëm, te yeena yey teewlu waxi yonent yi, ni ñuy teewloo ceeñeeru làmp bu tàkke ci biir lëndëm, ba kera fajar di xar, ba biddiiwu njël feqal seen xol.

2.Piyeer 1:19

Tey jii ci ab seetu lanuy gise gis-gis bu lënt. Waaye bu keroogee, màkk lanuy jàkkaarloo ak li nuy xool. Tey jii, as ndog laa xam, waaye su keroogee, ni ñu ma xame, ni laay xame ba mu mat sëkk.

1.Korent 13:12

Guddi du amati, te deesul soxlaati làmp mbaa naaj, ndax Boroom bi Yàlla moo leen di leeral. Te dañuy nguuru ba fàww.

Peeñu ma 22:5

Ci kaw loolu njiitu mool ya dikk ba ca moom, ne ko: «Yaw, ana looy nelaw? Jógal kay woo sa yàlla wall! Jombul mu geesu nu, ba dunu sànku.»

Yunus 1:6

Jógleen dem, fii du bérebu noflaay, nde sobewu na, ba nara yàqe yaxeet.

Mise 2:10

La fa kaw, xintewooleen ko, te ngeen ba li fi suuf,

Kolos 3:2

Doom aadama, ngelawal neen; nit, naxi neen. Booleel teg ci lu ñuy natte diisaay, kaw la jëm. Ñooy gëna woyof ngelaw!

Taalifi cant 62:10

Kon nag nangeen yeboo xol ci wut seen Yàlla Aji Sax ji, teg ci seen bakkan. Aycaleen boog ci tabax kër gu sell gu ñeel Yàlla Aji Sax ji, ba mana yeb gaalu kóllërey Aji Sax ji ak ndabi Yàlla yu sell yi ci biir kër gi ñu tabax, tudde ko turu Aji Sax ji.»

1.Jaar-jaar ya 22:19

Yuda daldi diisooji ak sarxalkat yu mag ya ak kilifay wattukati kër Yàlla ga, ngir xam nan lay tege Yeesu ci seeni loxo.

Luug 22:4

«Moytuleen naan gu ëpp ak màndite ak xalaati àddina wayadiloo leen, lu ko moy bés ba jekki dal ci seen kaw,

Luug 21:34

Boroom séet ba nag guddee, ñépp gëmmeentu, bay nelaw.

Macë 25:5

Ndax kat, «Des nas tuut, as tuut rekk, kiy dikk, dikk te du yeex.

Yawut ya 10:37

Li tax ngeen wara gëna farlu ci loolu mooy, xam ngeen jant yi nu tollu; seen waxtuw yewwu jot na ba noppi, nde léegi la nu mucc gëna jege ba nuy doora gëm.

Room 13:11

Kon teewluleen, ndax xamuleen kañ la boroom kër giy dikk. Jombul muy ngoonug suuf, mbaa xaaju guddi, mbaa bu ganaar sabee, mbaa bu bët setee. Bumu ne jalañ, fekk leen ciy nelaw.

Màrk 13:35–36