Leeru Bés bi — 22 Ut: Room 14:7–8

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ndax kat kenn ci nun dundul ngir boppam, te kenn deewul ngir boppam. Su nuy dund, ngir Boroom bi lanuy dund, su nu deewee it, wormaal Boroom bee tax nu dee. Kon nag nuy dund mbaa nu dee Boroom bi moo nu moom.

Room 14:7–8

Bu kenn sàkku njariñal boppam, waaye sàkkuleen seen njariñal moroom.

1.Korent 10:24

ndax dees leena jot, ba fey njëg ga. Kon nag seen yaram, terale leen ko Yàlla.

1.Korent 6:20

Loolu laa ne siiw, yaakaar ko, te duma rus mukk, xanaa di saxoo aw fit, démb niki tey, ngir ma mana fésale sama jëmm jépp màggaayu Almasi bi, su may dund ak su may dee. Ndax samag dund, Almasi bi la ñeel, samag dee dàqati. Su dee nag damaa wara wéye sama bakkan bii, ngir mana sottal ab liggéey bu am njariñ, ana lu ma gënal ci diggante dund ak dee? Xawma ko. Ci diggante ñaar yooyii laa tance: yàkkamti namaa yiwiku ba fekki Almasi bi, te loolu moo dàqati fuuf.

Filib 1:20–23

Su dee wàllu yoonu Musaa nag, man nit ku dee laa, te yoonu Musaa moo ko waral, ngir ma mana dund dund gu ñeel Yàlla. Dees maa boole ak Almasi bi rey ca bant ba. Moo tax dootul man maay dund, waaye Almasi bi mooy dund léegi ci man. Sama dundu yaramu suux wii tey nag, ci ngëm gi ma gëm Doomu Yàlla laa koy dunde, moom mi ma sopp, ba jébbale boppam ngir man.

Galasi 2:19–20

Keroog àtte ba, Lingeeru bëj-saalum dina jóg, janook niti tey jii, tiiñal leen; ndax moo bàyyikoo woon ca catal àddina, ngir déglusi xam-xamu Suleymaan, te tey jii, ku sut Suleymaan a ngi fi.

Macë 12:42

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Esayi 9:6

Barewul ku nangoo dee ngir nit ku jub, doonte jombul mu am ku nangoo dee ngir ku baax. Waaye Yàlla moom, ni mu firndeele cofeelam ci nun, moo di, ba nu doon ay bàkkaarkat, ca la Almasi bi deewe ngir nun!

Room 5:7–8

Moom mi nekke nekkinu Yàlla te ŋoyaaloowul ci dayob boppam bi ko def nawleb Yàlla. Xanaa mu ŋacc boppam, nangoo jagoo nekkinu surga. Mu mujj mel ni nit doŋŋ, di ku ñu xàmmee jëmmu nitam. Moo toroxlu, moo nangu, ba dee fekk ko ci, ak mbugalu bant ba ñu ko daaj.

Filib 2:6–8

Ngeen boole ci daj cofeelu Almasi gi wees xam-xam, ngir ngeen fees, ba fees dell ak koomu Yàlla.

Efes 3:19

Waaye ci ñi ñu woo, ñuy Yawut, di Gereg, Almasi bi mooy manoorey Yàlla, di xam-xamu Yàlla.

1.Korent 1:24

Ci moom la mboolem alal ji ci xel ak xam-xam dëxëñe.

Kolos 2:3

Man mi yées ci ñu sell ñépp lañu may woowu yiw, ba may xibaar jàmbur ñi dul Yawut xéewal yu amul kem yi ci Almasi bi.

Efes 3:8

Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njub, di sunu cellte, di sunug njot,

1.Korent 1:30