Aji Sax ji, yaw laa séddoo; di digee sàmm sa kàddu.
Taalifi cant 119:57
Leeru Bés bi
Aji Sax ji, yaw laa séddoo; di digee sàmm sa kàddu.
Taalifi cant 119:57
Kon nag bu kenn puukarewoo ay nit, ndax lépp, yeena ko moom,
1.Korent 3:21
Yeen nag, Almasi bi moo leen moom, te Almasi bi, Yàllaa ko moom.
1.Korent 3:23
Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla miy Yeesu Almasi bi, Musalkat bi. Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.
Tit 2:13–14
Yàlla moo teg lépp fi roni tànkam, te moo ko def muy bopp bi tiim lépp, ñeel mbooloom gëmkat ñi,
Efes 1:22
Jëkkër nag, na sopp jabaram ni Almasi bi soppe mbooloom gëmkat ñi, ba joxeel leen bakkanam.
Efes 5:25
Li mu ci namm moo di teewal mbooloo mi fi kanamam, mu mel ni ab séetam bu ne ràññ, gàkkul, rasul, taqul lenn, xanaa sell, mucc sikk.
Efes 5:27
Naa màggal Aji Sax ji saa su ne, di ko sant fu ma tollu.
Taalifi cant 34:2
Maa bég a bég ci Aji Sax ji, sama xol di sedd ci sama Yàlla jii. Moo ma solal yérey mucc, sànge ma mbubbam ndam, may nirook boroom séet bu kaalawu ni sarxalkat, ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.
Esayi 61:10
Ana ku ma am asamaan ku la moy? Ku ma safoo kaw suuf ku la moy? Kàttan ak pexe jeex, Yàlla di ma dooleel, ma séddoo ko fàww.
Taalifi cant 73:25–26
Éy Yàlla, sàmm ma, maa ngi làqu fi yaw! Maa ne Aji Sax ji: «Yaay sama Boroom, awma alal ju la moy.»
Taalifi cant 16:2
Aji Sax ji, yaay wàll wi ma séddoo, di sama ndabal xéewal. Yaa yor sama wërsëg. Maa muurloo béreb bu neex, ndaw cér bu rafet!
Taalifi cant 16:5–6
Yoon a ngii, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci dee.
Kàddu yu xelu 14:12
Ku doyloo sam xel, dof nga; ku jëfe xel mu rafet, mucc nga.
Kàddu yu xelu 28:26
Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.
Taalifi cant 119:105
Su may jëf it, di sàmm sa kàddu. Maay moyu yoonu ku bon.
Taalifi cant 17:4
Mboolem kàddu gi ma leen dénk nag, sàmmooleen koo jëfe. Buleen ci yokk lenn, buleen ci wàññi lenn. Gannaaw loolu su ab yonent feeñee ci seen biir, mbaa boroom gént, bu leen digee firnde mbaa kiraama, ba firnde la mbaa kiraama ga mu leen waxoon dikk, su leen nee: «Nanu topp yeneen yàlla, jaamu leen,» yàlla yu ngeen xamul, buleen déglu waxu yonent boobu, mbaa boroom gént boobu, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di nattu ngir xam ndax yeena ngi koy soppe seen léppi xol ak seen léppi jëmm.
Baamtug yoon wi 13:1–4
Nga ne ma: «Dama laa xelal, xamal la fi ngay jaar, digal la, di la bàyyi xel.
Taalifi cant 32:8
Bés yu mujj yi
Wone yépp20 Ut 2025
19 Ut 2025
18 Ut 2025
17 Ut 2025
16 Ut 2025
15 Ut 2025
14 Ut 2025