Yàlla miy boroom jàmm, moom mi dekkal sunu Sang Yeesu, sàmm bu mag bi, ci dooley deret ji mu fase kóllëre gu sax dàkk, yal na leen matal sëkk ci lépp lu baax, ngir ngeen di jëfe coobareem. Yal na def ci nun bànneexu boppam bu mu sottal ci Yeesu Almasi bi daraja ñeel ba fàww. Amiin.
Yawut ya 13:20–21
Ma tëje fii nag, bokk yi, bégleen, yokkuleen ba mat sëkk, ñaaxanteleen, mànkooleen te jàmmoo. Su ko defee Yàlla miy Yàllay cofeel ak jàmm mooy ànd ak yeen.
2.Korent 13:11
Ndax kat ci yiw ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yeen, mayu Yàlla la; du peyu jëf, ba kenn di ci kañu.
Efes 2:8–9
gépp may gu baax ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom.
Yanqóoba 1:17
Kon nag soppe yi, noonu ngeen masa dégge ndigal, démb ba may teew, rawatina tey bi ma wuutee, nangeen ko wéye, di jëfe seenug mucc, te ànd ceek ragal Yàlla bay lox, ndax Yàlla mooy liggéey ci yeen lu tax ngeen mana namma jëfe coobareem, ba man koo jëfe.
Filib 2:12–13
Buleen roy jamonoy tey jii, waaye yeesluleen ci ni ngeen di xalaate ba soppiku, ngir ngeen mana ràññee liy coobarey Yàlla, muy li baax, di bànneexam te mat sëkk.
Room 12:2
Su boobaa ngeen meññal ba woomle ci njub gi Yeesu Almasi bi di maye, ngir fésal màggug Yàlla, jollil ag cantam.
Filib 1:11
Du caageenu doyloo sunu manoorey bopp, ba yaakaar ne lenn man naa sottee ci sunu wàllu bopp, waaye sunu manoore ci Yàlla la jóge.
2.Korent 3:5
Maay yàqate garabi reseñ aki figg
yi mu noon: “Lii sama peyoor la!
Samay far a ma ko jox.”
Maa koy def ay dédd,
rabi àll yi di ko lekk.
Ose 2:14
Kon nag:
«Nangeen génne ci seen biir, te teqalikoo ak ñoom,»
la Boroom bi wax,
«lu sobewu, buleen ko laal.
Su boobaa, maa leen di dalal.
2.Korent 6:17–7:1
Moo waral Yeesu itam deewe ca bitib dëkk ba, ngir sellale askan wi deretu boppam. Kon nag, nanu ko fekki ca bitib dal ba, ba tegoo toroxtaangeem ga mu tegoo woon,
Yawut ya 13:12–13
Ci kaw loolu Yeesu ne leen: «Yeen nag dangeen di ñëw, nu daw ba fu wéet, ngeen noppalu fa tuuti.» Booba ñay dem aka dikk dañoo bare, ba taalibe ya talatuñoo lekk sax.
Màrk 6:31
Ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
Aji Sax jee may sàmm,
du lenn lu ma ñàkk.
Parlu mu naat la may gooral,
wal mu dal, mu tette ma ca,
leqali ma,
teg ma ci yooni njub
ngir teraangay turam.
Taalifi cant 23:1–3