«Éy Boroom bi Aji Sax ji, yaa ma wonagum lenn ci sa màggaay ak sa doole, Sang bi. Ana yàlla ju nekk asamaan, mbaa ci kaw suuf ju mana roy say jëf ak say jaloore?
Baamtug yoon wi 3:24
Leeru Bés bi
«Éy Boroom bi Aji Sax ji, yaa ma wonagum lenn ci sa màggaay ak sa doole, Sang bi. Ana yàlla ju nekk asamaan, mbaa ci kaw suuf ju mana roy say jëf ak say jaloore?
Baamtug yoon wi 3:24
Aji Sax ji, waa asamaan a ngi lay sante say jaloore, ndajem ñu sell ña di la joobee sa kóllëre.
Taalifi cant 89:6
Yàlla ji ñu teral a teral ci jataayu ñu sell ñi, te mu gëna raglu lu ko wër?
Taalifi cant 89:8
Boroom bi, doo moroomu tuur yi, te jëf melul ni sa jos.
Taalifi cant 86:8
Sa kàddoo waral nga def mboolem jii jëf ju réy ci sa yéeney xol, te it yaa ma ko xamal, man sab jaam. «Boroom bi Aji Sax ji, yaay Ku màgg moos! Kenn du yaw, kenn it du Yàlla ku dul yaw, te mboolem lu nu nopp may, dëggal na loolu.
2.Samiyel 7:21–22
Mooy noonu ñu binde rekk ne: «Lu bët gisul, nopp déggu ko, xel daju ko, Yàllaa ko dencal ñi ko sopp.» Waaye nun la Yàlla feeñalal denc googu jaare ci Xelam. Ndaxte Xelum Yàlla lépp lay gëstu ba ci xóotey mbóoti Yàlla.
1.Korent 2:9–10
su ko defee, noonu ñu binde ne: «Kuy damu, na damu ci Boroom bi,» noonu lay ame.
1.Korent 1:31
Kuy damu kay, na damoom xelam mu ko may mu xam ma, xam ne maay Aji Sax jiy doxal ngor ak yoon ak njub fi kaw suuf. Loolu déy mooy sama bànneex.» Kàddug Aji Sax jee. «Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay dikkal képp ku xarafam yem ci yaram,
Yeremi 9:23–24
Rax ci dolli, lépp sax laa far jàppe ag wàññeent, ndax ngëneel li sut lépp, te mooy xam kuy sama Sang Almasi Yeesu. Moom moo ma taxa nangoo ñàkk lépp, def lépp ni mbuubit, ngir tonoo Almasi bi,
Filib 3:8
Awma lu may rus ci xibaaru jàmm bi, ndax kat mooy manoorey Yàlla jiy musal képp ku ko gëm, dale ci Yawut bi, teg ci ki dul Yawut.
Room 1:16
Moo tax ma saña puukarewoo Almasi Yeesu mi may liggéeyloo ci mbiri Yàlla.
Room 15:17
Ana ku ma am asamaan ku la moy? Ku ma safoo kaw suuf ku la moy?
Taalifi cant 73:25
Ci kaw loolu Aana ñaan ne: «Sama xol a ngi bége Aji Sax ji, ci Aji Sax ji laa ame doole. Maa am tontal noon yi, nde maa bànneexoo sag wall.
1.Samiyel 2:1
Bu muy nun, Aji Sax ji, bu muy nun, saw tur nga wara teral, ngir sa ngor ak sa worma.
Taalifi cant 115:1
Bés yu mujj yi
Wone yépp17 Ut 2025
16 Ut 2025
15 Ut 2025
14 Ut 2025
13 Ut 2025
12 Ut 2025
11 Ut 2025