Leeru Bés bi — 19 Ut: 1.Piyeer 1:15

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Waaye ni ki leen woo selle, yeen itam nangeen selle noonu ci seen mboolem jëfin.

1.Piyeer 1:15

Xam ngeen ne fi baay féete doomam lanu féete kenn ku nekk ci yeen. Ñaax nanu leen, dëfal leen, dénku leen, ngir ngeen di jëfe jëfin wu yelloo ak Yàlla mi leen woo ci nguuram ak teraangaam.

1.Tesalonig 2:11–12

Waaye yeen nag yeenay giir giy tànnéef, yeenay sarxalkati buur, yeenay askan wu sell, yeenay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.

1.Piyeer 2:9

Ag lëndëm ngeen woon démb, waaye tey ag leer ngeen ci Boroom bi ngeen bokk. Jëfeleen nag ni niti leer. Li leer gi ci yeen di meññ moo di mboolem luy mbaax ak njub ak dëgg. Ràññeeleen li neex Boroom bi; jëfi lëndëm amul njariñ, buleen ci bokk, xanaa ngeen feeñal ñaawtéefu jëf ja.

Efes 5:8–11

Su boobaa ngeen meññal ba woomle ci njub gi Yeesu Almasi bi di maye, ngir fésal màggug Yàlla, jollil ag cantam.

Filib 1:11

Yeen, na seenug leer leere noonu ci kanam nit ñi, ngir ñu gis seen jëf ju rafet, ba sàbbaal seen Baay ba fa kaw.

Macë 5:16

Kon nag su ngeen di lekk, mbaa ngeen di naan, mbaa ngeen di def leneen, lépp lu ngeen di def, wutleen koo terale Yàlla.

1.Korent 10:31

Aji Sax ji, Aji Sell ju Israayil dafa wax, moom mi ko bind, mu ne: «Lu dikkagul, nu ngeen ma ko ñemee laaje; am dangeen may jox ndigal ci samay doom, jox ma ko ci li ma liggéeye samay loxo?

Esayi 45:11

Maa leen di jox xol bu yees, te xel mu yees laay def ci seen dënn. Xolu doj bi laay roccee ci seen suux, wecceel leen ko xol yu nooye ni suux, te samam xel laay yeb fi seen biir dënn, ba dogal ngeen mana topp sama dogali yoon, di sàmm aka jëfe sama àttey yoon.

Esekiyel 36:26–27

«Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Lii laay nangulaatal waa kër Israayil, defal leen ko: maay ful nit ñi niy gàtt.

Esekiyel 36:37

«Maa leen neeti, su ñaar ci yeen déggoo ci kaw suuf, ci mboolem lu ñu ñaan, dees na leen ko nangul ci sama dogalu Baay ba fa asamaan, ndax fu ñaar mbaa ñett dajee ci sama tur, maa ngi ci seen biir.»

Macë 18:19–20

Yeesu ne leen: «Gëmleen Yàlla. Maa leen ko wax déy, képp ku ne tund wale: “Jógal, tàbbiji géej,” te bañ cee boole xel ñaar, xanaa gëm ne li nga wax dina am, noonu lees la koy nangule.

Màrk 11:22–23