Daawuda daldi ne: «Sama doom Suleymaan gone la te xamul àddina, te kër gi ñuy tabaxal Aji Sax ji wara màgg lool ba yéeme, yànj te am daraja ba siiw, xeet yépp gis ko. Kon nag dama koy daldi waajal.» Daawuda waajal na lu bare bala moo dee.
1.Jaar-jaar ya 22:5
Te yeen itam yeen ay doji cëslaay yuy dund, doj yi Noo gu Sell gi tabaxe ag kër Yàlla, ñeel liggéeyu carxal gu sell, ngir ngeen di ko jébbal ay sarax yu Noo gi rafetlu, sarax yu Yàlla nangu ndax Yeesu Almasi bi.
1.Piyeer 2:5
Xanaa xamuleen ne kër Yàlla ngeen, te Noowug Yàlla moo dëkk ci yeen? Ku yàq kër Yàlla nag, kooku Yàlla dina ko yàq, ndax kër Yàlla dafa sell, te mooy li ngeen doon.
1.Korent 3:16–17
Dangeena xamul ne seen yaram mooy màkkaanu Noo gu Sell gi ci yeen, Noo gi ngeen jote ci Yàlla? Moomuleen seen bopp, ndax dees leena jot, ba fey njëg ga. Kon nag seen yaram, terale leen ko Yàlla.
1.Korent 6:19–20
Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne:
«Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir,
di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.»
2.Korent 6:16
Kon nag dootuleen ay gan mbaa ay doxandéem, waaye ay nawley ñu sell ñi ngeen, te waa kër Yàlla ngeen. Yeena di tabax bi ndawi Almasi bi ak yonent yi di fondmaa bi, te Almasi Yeesu ci boppam di doju koñu tabax bi. Ci moom la tabax bi bépp di temboo, ba jóg, doon jaamookaay bu sell ngir Boroom bi. Ci Almasi bi ngeen bokke ci tabax bi, yeen jàmbur ñi itam, ba mana doon dëkkuwaayu Yàlla, ci ndimbalal Noo gu Sell gi.
Efes 2:19–22
Mooy ki nekkoon naka jekk balaa daraa nekk, te lépp ci moom la sottee ba temboo.
Kolos 1:17
«Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Lawdise nag, bind ko ne ko:
«Lii moo di kàdduy ki tudd Na-amee-nii, Seede bi wóor te dëggu, Ndeyu càkktéefu Yàlla ji. Mu ne:
Peeñu ma 3:14
Mooy boppu yaram, wiy mbooloom gëmkat ñi, mooy njàlbéen, mooy taaw bi njëkka dekki, ndekkite lu dee toppul, ba tax muy ki jiitu ci lépp,
Kolos 1:18
Soxna si, Xel mu Rafet nee na:
«Aji Sax ji jagoo na ma ca njàlbéen,
ma jiitu ca jëfam ya woon.
Bu yàgg lañu ma dëj,
ca ndoorte la, bala suuf a sosu.
Kàddu yu xelu 8:22–23
Ba muy taxawal asamaan, maa nga fa,
ak ba muy rëdd fa asamaan taseek géej,
ak ba muy teg niir ya fa kaw,
ak ba muy dooleel ndoxi xóotey géej,
ak ba muy sàkkal géej kemoom,
ba du jàll fa mu wax.
Ba muy rëdd fa muy samp àddina,
man, Xel mu Rafet, maa doon ku xareñ ci wetam,
di ko bànneexal bés bu ne,
tey bànneexu fi kanamam.
Kàddu yu xelu 8:27–30
maa masa doon kenn ki,
te sama loxo, maneesu cee musle.
Su ma defee, kuy dindi?»
Esayi 43:13
Mboolem waa àddina di ko sujjóotal, maanaam mboolem ñi ñu bindul seen tur ca ndoortel àddina ci téereb dund bu Xar mi ñu rendi.
Peeñu ma 13:8
Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru ngànguney Yàlla.
Yawut ya 12:2