Ci kaw loolu Noowug Yàlla gi yóbbu Yeesu ba ca biir màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane.
Macë 4:1
Leeru Bés bi
Ci kaw loolu Noowug Yàlla gi yóbbu Yeesu ba ca biir màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane.
Macë 4:1
Fan yi Almasi bi dee dund dundu nitu suuxu neen, ay ñaan aki dagaan yu ànd aki yuux aki jooy la daan yékkati jëme fa ki ko mana wallu ba du dee, te ñaan ga nangu na it, ndax na mu ragale woon Yàlla. Li muy Doom lépp, terewu koo tàggatu ci dégg ndigal, ndax coono yi mu daj. Noonu lees matale Almasi bi sëkk, ba mu doon cosaanu mucc gu dul jeex, ñeel mboolem ñi ko déggal.
Yawut ya 5:7–9
Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.
Yawut ya 4:15
Benn nattu dabu leen bu moy nattu yiy dale. Te it Yàllaa jara wóolu. Yàlla du nangu ngeen tegoo nattu bu ngeen àttanul, waaye nattu ba lay booleek pexe ma leen cay génne, ba ngeen man koo dékku.
1.Korent 10:13
Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi bi wàcc ci sama kaw.
2.Korent 12:9
Noonu la deme ci Doomu nit ki, ñëwul ngir ñu di ko surgawu, xanaa ngir di nekk surga, ba far maye bakkanam, def ko njotug ñépp.»
Macë 20:28
Deretu sikket ak yëkk, ak dóomu nag wu jigéen wu ñu lakk, ngir suy dóom ba nit ku sobewu, yooyu lees daan sellale nit ñi, ngir seen cetug yaramu suuxu neen. Su loolu amee, ñaata yoon la deretu Almasi bi ëppe njariñ! Almasi bi mooy ki def boppam sarax bu mucc sikk ñeel Yàlla, ci dooley Noo gu Sell gi. Moom rekk moo mana setal sunu yaraangey xel mi sababoo ci sunu jëf ju bon ju jëme ci dee, ba nu mana jaamu Yàlla jiy dund!
Yawut ya 9:13–14
Dees koo néewal doole, mitital ko te ubbiwul gémmiñam, xanaa mel ni xar mu ñuy rendiji, ne cell ni xar mu ñuy wat, ubbiwul gémmiñam.
Esayi 53:7
Noonu it laa xame Baay bi, Baay bi xame ma ni, te maay joxe sama bakkan, jote ko xar yi.
Yowaan 10:15
Kenn du jële sama bakkan ci man; man maa koy joxeel sama bopp. Maa ko saña joxe, maa ko saña jëlaat, te loolu la ma sama Baay sant.»
Yowaan 10:18
Ndaxte dundu mbindeef ci deret la nekk, te man maa leen sédde deret, ngeen di ko jotoo seen bakkan ci kaw sarxalukaay bi. Ndax kat bakkanu mbindeef deretam la taxawe. Moo tax deret mana defal nit njotlaayam.
Sarxalkat yi 17:11
Ndax ci yoonu Musaa sax, deret lees di setale daanaka lépp, te bu deret tuuruwul, njéggal amul.
Yawut ya 9:22
Waaye Yàlla moom, ni mu firndeele cofeelam ci nun, moo di, ba nu doon ay bàkkaarkat, ca la Almasi bi deewe ngir nun! Gannaaw baaxees nañu nu àtteb ñu jub ndax deretam ji tuuru nag, ñaata yoon lees nuy gënatee musal ci am sànj ndax moom?
Room 5:8–9
Bés yu mujj yi
Wone yépp6 Sul 2025
5 Sul 2025
4 Sul 2025
3 Sul 2025
2 Sul 2025
1 Sul 2025
30 Suw 2025