mbaa di randal. Waaye nañu firndeel ne ñoo yelloo kóolute gu mat sëkk, su ko defee dinañu sagal ci lépp, àlluwa ji ñu jànge, te muy ju Yàlla sunu Musalkat.
Tit 2:10
Leeru Bés bi
mbaa di randal. Waaye nañu firndeel ne ñoo yelloo kóolute gu mat sëkk, su ko defee dinañu sagal ci lépp, àlluwa ji ñu jànge, te muy ju Yàlla sunu Musalkat.
Tit 2:10
Fexeleen rekk ba di jëfe ni mu yelloo ak xibaaru jàmm bu Almasi bi, ngir bu ma leen seetsee, mana seede, mbaa su ma wuutee it, di dégg ni ngeen saxoo di mànkoo, bokk jenn yéene, di bokk xeex, ngir saxal ngëm gi sukkandikoo ci xibaaru jàmm bi.
Filib 1:27
te lu bon ak nu mu mana bindoo, dàndleen ko.
1.Tesalonig 5:22
ngir seen der set wecc, te kon deesuleen mana gàkkal ci lenn. Ay goney Yàlla yu amul sikk ngeen di doon, ci biir maas gu dëng te yàqu, ngeen di lerxat ci seen biir, ni ay leer ci àddina si,
Filib 2:15
Yeen, na seenug leer leere noonu ci kanam nit ñi, ngir ñu gis seen jëf ju rafet, ba sàbbaal seen Baay ba fa kaw.
Macë 5:16
Bu la ngor ak worma dëddu, booleel takk ci sa baat, bind ko ci sa àlluway xol. Kon nga xam lu jaadu, neex Yàllaak doom aadama.
Kàddu yu xelu 3:3–4
Li ci des nag bokk yi, moo di lii: mboolem lu dëggu, ak mboolem lu tedd, ak mboolem luy njub, ak mboolem lu set, ak mboolem lu jekk, ak mboolem lees di rafetlu, ndegam lu nawlu la te yelloo ngërëm, na leen loola soxal.
Filib 4:8
Noowug Yàlla mooy dundloo; nitu suuxu neen manul dara. Kàddu gi ma leen wax moo leen di jottali Noowug Yàlla giy taxa dund.
Yowaan 6:63
Moom la soob mu jur nu ci kàddug dëgg gi, ba nu taxawe saraxu ndoortel meññeef, ci biiri bindeefam.
Yanqóoba 1:18
Moo nu may manoorey doon ay liggéeykati kóllëre gu bees gu ajuwul ci mbindum ndigali yoon, xanaa kóllëre gu aju ci Noowug Yàlla. Ndaxte mbindum ndigali yoon day rey, te Noo gi di dundloo.
2.Korent 3:6
Jëkkër nag, na sopp jabaram ni Almasi bi soppe mbooloom gëmkat ñi, ba joxeel leen bakkanam. Moo defal loolu mbooloo mi, ba man koo setale cangaayal ndox mu ànd ak kàddoom, ngir sellal ko. Li mu ci namm moo di teewal mbooloo mi fi kanamam, mu mel ni ab séetam bu ne ràññ, gàkkul, rasul, taqul lenn, xanaa sell, mucc sikk.
Efes 5:25–27
Ana nu ndaw mana sellalee? Xanaa di sàmm sa kàddu.
Taalifi cant 119:9
Lii laay muñe samaw naqar, sa kàddoo may dundal.
Taalifi cant 119:50
Sama xol laa làq say wax, ngir bañ laa moy.
Taalifi cant 119:11
Sa dogali yoon, ma tàqamtikoo, sa kàddu, ma fat ba fàww.
Taalifi cant 119:16
ba ku ma kókkali, ma am tontam. Maa doyloo sa kàddu.
Taalifi cant 119:42
Sa ngëneelu yoon wi nga digle moo ma gënal ay junniy dogi xaalis ak wurus.
Taalifi cant 119:72
Duma fàtte mukk say tegtal, ci nga may musale.
Taalifi cant 119:93
Sa kàddooka maa neex, ba dàqal ma tem-temu lem! Ci say tegtal laay ràññee, ba tax ma bañ luy yoonu fen.
Taalifi cant 119:103–104
Bés yu mujj yi
Wone yépp13 Mar 2025
12 Mar 2025
11 Mar 2025
10 Mar 2025
9 Mar 2025
8 Mar 2025
7 Mar 2025