«“Yal na la Aji Sax ji geesoo leeram, baaxe la. «“Yal na la Aji Sax ji siggil, jàmmal la.”
Màndiŋ ma 6:25–26
Leeru Bés bi
«“Yal na la Aji Sax ji geesoo leeram, baaxe la. «“Yal na la Aji Sax ji siggil, jàmmal la.”
Màndiŋ ma 6:25–26
Kenn masula gis Yàlla, waaye Yàlla miy Kenn te sës rëkk ci Baay bi, kooku mooy ki ko xamle.
Yowaan 1:18
Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya,
Yawut ya 1:3
Aji gëmadi ñooñu la Seytaane yàllay xarnu bii gëlëmal seenum xel, ngir ñu baña gis ceeñeeru xibaaru jàmm biy yànjal leeru Almasi biy melokaanu Yàlla.
2.Korent 4:4
Yaa yor sama àpp. Xettali maak ku ma noonoo ak ku may sonal. Leeralal ma sa kanam, Sang bi, walloo ma sa ngor.
Taalifi cant 31:16–17
Man damaa baaxle woon, ba ne: «Deesu ma rëññeel mukk.»
Taalifi cant 30:7
Àtteb dëgg ak njub a lal sab jal, ngor ak worma dox jiitu la.
Taalifi cant 89:15
Aji Sax jeey kàttanal ñoñam, di barkeele jàmm ñoñam.
Taalifi cant 29:11
Yeesu wax ak ñoom ca saa sa, ne leen: «Dalleen, man mii la, buleen tiit!»
Macë 14:27
Te kon lu nu ñaan, mu may nu ko, ndax ay ndigalam lanuy sàmm, te li mu rafetlu lanuy jëfe.
1.Yowaan 3:22
Ku amul ngëm nag doo mana neex Yàlla, ndax kiy dikk fi Yàlla, fàww nga njëkka gëm ne Yàlla am na, gëm it ne ñi koy sàkku, moo leen di yool.
Yawut ya 11:6
Moo tax ñi wéye seen bindu suuxu neen duñu mana neex Yàlla.
Room 8:8
Aji Sax jee safoo ñoñam, di terale néew-ji-doole ag mucc.
Taalifi cant 149:4
Ndax nit ki su séddee Yàlla ab cér, ba tax mu muñ tiis ak coono bu ko yoon tegul, loolu aw yiw la. Muñ ay dóor yu la fekk ci tooñ, ana lu ciy ndam? Waaye soo muñee coono boo daj ngir lu baax loo def, loolu de aw yiw la fa kanam Yàlla.
1.Piyeer 2:19–20
waaye nay lu làqoo jëmmu biir, nay gànjar gu dul jeex, te mooy lewetaay akug teey, ndax looloo réy njarte fa Yàlla.
1.Piyeer 3:4
Ki may sarxale jaajëf moo ma teral; ku topp yoon, ma won ko wallub Yàlla.»
Taalifi cant 50:23
Man de, damaa jàq, tiis. Éy Yàlla, yal naa làqoo sag wall. Damay wormaal turu Yàlla, woyal ko, màggal ko, sant ko.
Taalifi cant 69:30–31
Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax. Na seen dund mel ni sarax su ñuy defal Yàlla, sarax su sell te neex ko. Loolu déy mooy njaamu gi leen war.
Room 12:1
Bés yu mujj yi
Wone yépp11 Mar 2025
10 Mar 2025
9 Mar 2025
8 Mar 2025
7 Mar 2025
6 Mar 2025
5 Mar 2025