Leeru Bés bi — 9 Mars: 1.Timote 6:17

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ñi barele alalu àddinay tey nag, dénk leen ñu baña réy te baña yaakaar alal ju wóoradi, te ñu yaakaar Yàlla mi nuy xéewale lépp, ngir nu di ko bége.

1.Timote 6:17

Wattuleen seen bopp nag, bala ngeena fàtte seen Yàlla Aji Sax ji, baña sàmm ay santaaneem ak àttey yoonam ak dogali yoonam yi ma leen di dénk tey. Su ngeen lekkee ba regg, am kër yu baax yu ngeen tabax dëkke,

Baamtug yoon wi 8:11–12

Waaye fàttalikuleen ne seen Yàlla Aji Sax ji mooy ki leen may dooley liggéey alal ji, ngir feddali ni mu ko defe tey, kóllëreem ga mu giñaloon seeni maam.

Baamtug yoon wi 8:18

Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Suleymaan. Kër, su ko Aji Sax ji tabaxul, ku ko tabax, neen nga doñ-doñi. Ab dëkk, su ko Aji Sax ji wattuwul, ku ko wattu, neen nga teewlu. Neen it la nit di teela jóg aka guddee tëdd, di doñ-doñi lu mu lekk: Aji Sax ji leel na soppeem lu ni day, fekk ko muy nelaw.

Taalifi cant 127:1–2

Yaw ci sa bopp yaa dàq xeet yi, jëmbat fa maam ya; yaa mbugal xeet yi, ñoom, nga yiwi leen.

Taalifi cant 44:3

Rendileen seen sarax yi war, te wóolu Aji Sax ji.

Taalifi cant 4:6

Ña ngay woy woy wu yees ca kanam ngàngune ma, ca kanam ñeenti mbindeef yaak mag ña, te kenn manula mokkal woy wi, ñu dul téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti junni ñooñu ñu jote àddina.

Peeñu ma 14:3

deretu Yeesu jiy yoon wu yees, yoonu dund gu mu nu xàllal, jàllale ko ca rido ba, te rido ba moo di yaramu suuxam wi mu saraxe.

Yawut ya 10:20

ca la nu musal, te du jenn jëfu njekk ju nu def, ba tax mu musal nu, waaye ci yërmandeem la nu musale, sang nu cangaay lu nu taxa judduwaat, boole ci yeesale nu Noo gu Sell gi mu nu awale ci Yeesu Almasi bi sunu Musalkat, ba baawaanal ko ci sunu kaw.

Tit 3:5–6

Ndax kat ci yiw ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yeen, mayu Yàlla la; du peyu jëf, ba kenn di ci kañu.

Efes 2:8–9

Bu muy nun, Aji Sax ji, bu muy nun, saw tur nga wara teral, ngir sa ngor ak sa worma.

Taalifi cant 115:1

tukkee itam fa Yeesu Almasi bi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki njëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqalikook kilifteefu sunuy bàkkaar, ba noppi def nu nuy askanu sarxalkati Buur Yàlla Baayam, na ko daraja ak manoore ñeel tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.

Peeñu ma 1:5–6

Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote ay niti gépp giir ak wépp làkk ak wépp xeet ak wépp askan, ñu doon ñoñi Yàlla.

Peeñu ma 5:9

Gannaaw loolu ma jekki gis mbooloo mu réy mu kenn manula waññ, ñu bawoo ci askan yépp ak giir yépp ak xeet yépp ak làkk yépp. Ñu ngi taxaw fi kanam ngàngune mi ak Xar mi, sol mbubb yu weex, jël ay cari garabi tàndarma. Ña ngay àddu ca kaw, naan: «Texee ngi fi sunu Yàlla, ki toog ci ngàngune mi, ak ci Xar mi!»

Peeñu ma 7:9–10