Leeru Bés bi — 21 Oktoobar: Yowaan 1:16

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ci ag matam lanu tanqe nun ñépp, yiw ci kaw yiw.

Yowaan 1:16

Naka lay wax ba tey, niir wu leer yiir leen, baat jekki jibe ca niir wa ne: «Kii mooy sama Doom, sama soppe, moom laay bànneexoo; dégluleen ko.»

Macë 17:5

Ndaw cofeel gu nu Baay bi won, ba ñu di nu woowe doomi Yàlla, te moom lanu it. Àddina nag xamu nu, te li ko waral moo di da koo xamul moom itam.

1.Yowaan 3:1

Ci fan yu mujj yii, ci Doom ji la jaare wax ak nun, ki mu jagleel lépp, te ci moom la sàkke àddina wërngal këpp.

Yawut ya 1:2

Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi bi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.

Room 8:17

Man ak Baay bi benn lanu.»

Yowaan 10:30

waaye gannaaw moom laay def, su ngeen ma gëmul sax, gëmleen boog jëf ji, ngir ngeen xam te ràññee ne Baay baa ngi ci man, te man it, maa ngi ci Baay bi.»

Yowaan 10:38

Yeesu ne ko: «Bu ma langaamu, ndax yéegeeguma fa Baay ba. Waaye demal, ne samay bokk, maa ngi yéegi ca sama Baay biy seen Baay, sama Yàlla jiy seen Yàlla.»

Yowaan 20:17

Man ma nekk ci ñoom, yaw nga nekk ci man, ngir ñu mat sëkk ci ag bennoo, ba àddina xam ne yaw yaa ma yebal, te ni nga ma soppe, ni nga leen soppe.

Yowaan 17:23

Yàlla moo teg lépp fi roni tànkam, te moo ko def muy bopp bi tiim lépp, ñeel mbooloom gëmkat ñi, mbooloo miy aw yaramam. Ci mbooloo mi nag la Almasi bi teewe teewaay bu mat sëkk, te Almasi bi mooy matal lépp ci ñépp.

Efes 1:22–23

Gannaaw noo moom yii dige nag, soppe yi, nanu setal sunu bopp ci mboolem sobey yaram ak ju xel, te nu sax ci sellaay ci ag ragal Yàlla.

2.Korent 7:1

Maa leen ko wax déy ci lu wér, jaam sutul sangam, te ndaw sutul ka ko yónni. Loolu, su ngeen ko xamee, ndokkalee yeen, ndegam yeena ngi koy jëfe.

Yowaan 13:16–17

Ñu yóbbaale sarax bi ci war, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw.» Amoon na nag ca Yerusalem ku ñuy wax Simeyon; ku juboon, ragal Yàlla, di séentu jamono ji nekkinu bànni Israayil di ame ag tan, te Noo gu Sell gi àndoon ak moom. Ndéey nag tukkee ci Noo gu Sell gi, xamal ko ne ko du dee mukk te gisul Almasi bu Boroom bi. Ci kaw loolu mu dem ba ca biir kër Yàlla ga ci dooley Noo gu Sell gi. Gannaaw loolu waajuri Yeesu indi Yeesu ngir defal ko li aaday yoon wi laaj.

Luug 2:24–27

Noonu la deme ci Doomu nit ki, ñëwul ngir ñu di ko surgawu, xanaa ngir di nekk surga, ba far maye bakkanam, def ko njotug ñépp.»

Macë 20:28

Yeesu xamoon na ne lépp la Baay bi teg ciy loxoom, te it ci Yàlla la jóge, te ci Yàlla la jëm. Mu jóge nag ca ndabal reer ba, summi mbubbam mu mag, daldi jël am malaan, laxasaayoo. Gannaaw loolu mu sotti ndox cib këll, daldi tàmbalee raxas tànki taalibe ya, di fompe sér ba mu laxasaayoo.

Yowaan 13:3–5