«Sàkkal dogu wurusu ngalam wu tell, nga ñaas ci mbind mii ni ñuy ñaase mbindum torlu: “Sell na, ñeel Aji Sax ji.”
Mucc ga 28:36
Leeru Bés bi
«Sàkkal dogu wurusu ngalam wu tell, nga ñaas ci mbind mii ni ñuy ñaase mbindum torlu: “Sell na, ñeel Aji Sax ji.”
Mucc ga 28:36
Sàkkuleen jàmm seen diggante ak ñépp, te it sàkkuleen cellte, nde ku sellul du gis Boroom bi.
Yawut ya 12:14
Yàlla xel la, kon ñi koy jaamu, xel ak dëgg lañu ko war di jaamoo.»
Yowaan 4:24
Du kenn kuy wormaal sa tur, mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw, yaa nu làq saw yiw, yaa nu def ban bu tooy ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc.
Esayi 64:6
Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: “Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell.
Sarxalkat yi 10:3
Ndigalu yoon wi jëm ci kër Yàlla gi ñu wara tabax mooy lii: ci kaw tund wi ak fi ko wër fépp, fu sella sell lay doon. Loolu mooy ndigalu yoon wi, ci wàllu kër Yàlla gi.»
Esekiyel 43:12
Say santaanee wér te wóor; Aji Sax ji, sellaay la sa kër jagoo ba fàww.
Taalifi cant 93:5
Man nag, ñoom laa sellalal sama bopp, ngir ñoom itam, ñu mana sellaloo dëgg gi.
Yowaan 17:19
Gannaaw nag am nanu kilifag sarxalkat bu mag bu jàll ba ca biir asamaan, te mooy Yeesu Doomu Yàlla, nanu ŋoy ci yoonu ngëm wi.
Yawut ya 4:14
Kon nag nanu ñemee dikk ba ca ngàngunem yiw ma, ndax nu jot yërmande te dajeek aw yiw wu nu wallu fu nu ko soxlaa.
Yawut ya 4:16
Yaa ma berndeel, noon yi gis, nga diwal ma saa bopp, terale ma, saab kaas rembat.
Taalifi cant 23:5
Ku ragal Aji Sax ji, malaakaam yiir la, di la wallu. Mosleen, xam ne Aji Sax jee baax, ndokkalee yaw mi ko làqoo. Ragalleen Aji Sax ji, yeen nitam ñu sell ñi; ku ko ragal doo ñàkk dara.
Taalifi cant 34:8–10
Aji Sax ji, ngoram du dakk, te yërmandeem du jeex. Xanaa di yeeslu jant bu nekk. Kee bare kóllëre!
Jooytu 3:22–23
Aji Sax ji, yaay wàll wi ma séddoo, di sama ndabal xéewal. Yaa yor sama wërsëg. Maa muurloo béreb bu neex, ndaw cér bu rafet!
Taalifi cant 16:5–6
muy Póol, di Apolos, di Sefas, di àddina, di dund, di dee, di tey, di ëllëg, lépp, yeena ko moom.
1.Korent 3:22
Cant ñeel na Yàlla, Baayu sunu Sang Yeesu Almasi bi nu baaxe bépp barkey biir, ci Almasi bi nu bokk, fa déndi asamaan ya.
Efes 1:3
Ag ñàkk nag taxul may waxe nii, nde tàmm naa di doylu ci diggante bu ma mana tollu.
Filib 4:11
Teewul ragal Yàlla gu ànd ak doylu, di alal ju réy.
1.Timote 6:6
Te sama Yàlla itam mooy sàkke ci koomam gu yéeme gi ci Almasi Yeesu, ba fajal leen seen soxla yépp.
Filib 4:19
Bés yu mujj yi
Wone yépp25 Ut 2026
24 Ut 2026
23 Ut 2026
22 Ut 2026
21 Ut 2026
20 Ut 2026
19 Ut 2026