Leeru Bés bi — 14 Ut: Neyemi 8:10

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Esra ne leen: «Ayca demleen lekk lu gëna duuf, naan lu neexa neex te sédd ci ñi amul lu ñu togg; ndax bésub tey bés bu sell la ñeel sunu Boroom. Kon buleen ci naqarlu kat, ndax bége Aji Sax ji mooy seen doole!»

Neyemi 8:10

Asamaanoo sarxolleel, suufoo bégal, te tund yi xaacoondoo! Aji Sax jee dëfal ñoñam, moo ñeewante néew-ji-dooleem ñii.

Esayi 49:13

Ma ne: «Yàllaa may wallu, ma dallu, duma tiit. Sama dooleek sama kaaraange mooy Ki Sax, di Aji Sax ji, te mooy sama wall.»

Esayi 12:2

Aji Sax jee may dooleel, di ma feg. Moom laa wóolu, mu wallu ma, sama xol tooy, ma woy, sante ko.

Taalifi cant 28:7

Maa bég a bég ci Aji Sax ji, sama xol di sedd ci sama Yàlla jii. Moo ma solal yérey mucc, sànge ma mbubbam ndam, may nirook boroom séet bu kaalawu ni sarxalkat, ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.

Esayi 61:10

Moo tax ma saña puukarewoo Almasi Yeesu mi may liggéeyloo ci mbiri Yàlla.

Room 15:17

Te yemunu ci, xanaa di sagoo Yàlla itam ndax sunu Boroom Yeesu Almasi bi nu jubale ak moom.

Room 5:11

te man may bànneexoo Aji Sax ji, Yàlla ji may wallu laay bége.

Abakug 3:18

Du nii la sama waa kër def ak Yàlla? Moo fas ak man kóllëre gu sax dàkk, lépp jekk, mat sëkk. Moo may may ndam saa su ne, di ma defal lu ma namm.

2.Samiyel 23:5

Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.

2.Timote 1:12

Cant ñeel na Yàlla, Baayu sunu Sang Yeesu Almasi bi nu baaxe bépp barkey biir, ci Almasi bi nu bokk, fa déndi asamaan ya. Te mooy noonu mu nu tànne ba àddina sosoogul ndax Almasi bi nu bokk, ngir nu doon ñu sell te mucc sikk fa kanamam. Ci biir cofeel la dogaloon lu jiitu, ne ci Yeesu Almasi bi la nuy defe ay doomi boppam, te muy bànneexam, di coobareem.

Efes 1:3–5

Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme. Ndax ñooñu Yàllaa leen ràññee woon lu jiitu, te it la mu dogaloon lu jiitu ci ñoom moo di ñu niru Doomam, ngir Doomam di taaw ci biir rakk yu bare. Ñi Yàlla tuddaloon loolu lu jiitu, moo leen woo itam; ñooñu mu woo, moo leen baaxe itam àtteb ñu jub; te ñooñu mu jox àtteb ñu jub, moo leen darajaal itam.

Room 8:28–30