Yoonu ku jub day leer, ba ne ràññ ni bëccëg.
Kàddu yu xelu 4:18
Leeru Bés bi
Yoonu ku jub day leer, ba ne ràññ ni bëccëg.
Kàddu yu xelu 4:18
Du caageenu damaa àgg ci loolu lépp ba noppi, mbaa damaa mat sëkk xaat, waaye maa ngi wéye samaw xél, di jéema jot ci neexalu rawante bi, gannaaw ba ma Almasi Yeesu jotee ci man itam.
Filib 3:12
Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji. Ni jant bu fenk la dikkam wóore, ni ab taw la nuy dikkale, ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»
Ose 6:3
Su booba aji jub ñi dañu naa ràññ ni jant bi, fa seen nguurug Baay. Ku ami nopp, na dégg.»
Macë 13:43
Nun ñépp nag, kanam gu muriku lanuy xoole niki cib seetu leeru Boroom bi, ba tax nuy soppiku, doon takkndeeram, tey làmboo leer guy màgg, di gëna màgg. Looloo di liggéeyu Boroom bi, moom miy Noo gi.
2.Korent 3:18
Waaye keroog bu li matale dikkee, ndog si wéy.
1.Korent 13:10
Tey jii ci ab seetu lanuy gise gis-gis bu lënt. Waaye bu keroogee, màkk lanuy jàkkaarloo ak li nuy xool. Tey jii, as ndog laa xam, waaye su keroogee, ni ñu ma xame, ni laay xame ba mu mat sëkk.
1.Korent 13:12
Soppe yi, léegi doomi Yàlla lanu, te li nuy dooni nag feeñagul. Waaye xam nanu ne bés bu Almasi bi feeñee, nooy nirook moom, ndax su boobaa, ni mu nekke, noonu lanu koy gise. Te képp ku am jooju yaakaar ci moom, noonu mu sete, ni lay setale boppam.
1.Yowaan 3:2–3
Ndax kat waxees na ne: «Képp ku woo Boroom bi wall ciw turam, dinga raw.»
Room 10:13
Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw, te man, ku ñëw ci man, duma ko dàq mukk.
Yowaan 6:37
Mu teg ca ne: «Yeesu, boo délsee ci sa nguur, fàttaliku ma!» Yeesu ne ko: «Yaw laa ne déy, bésub tey jii, man ngay nekkal fa Àjjana.»
Luug 23:42–43
Yeesu daldi taxaw, woo leen, ne leen: «Lu ngeen bëgg, ma defal leen ko?» Ñu ne ko: «Sang bi, xanaa sunuy bët ubbiku.» Yeesu nag yërëm leen, laal seeni bët, ñuy gis ca saa sa, daldi topp ca moom.
Macë 20:32–34
Ndegam yeen ñi bon yeena mana may seeni gone lu baax nag, astamaak Baay ba fa asamaan. Moo leen ko dàq fuuf, nde mooy may Noo gu Sell gi, ñi ko ko ñaan!»
Luug 11:13
te samam xel laay yeb fi seen biir dënn, ba dogal ngeen mana topp sama dogali yoon, di sàmm aka jëfe sama àttey yoon.
Esekiyel 36:27
«Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Lii laay nangulaatal waa kër Israayil, defal leen ko: maay ful nit ñi niy gàtt.
Esekiyel 36:37
Kóolute gi nu am ci Yàlla moo di su nu ko ñaanee lenn lu dëppook coobareem, da nuy nangul. Gannaaw xam nanu ne moo nuy nangul lépp lu nu ko ñaan, xam nanu ne dagaan yi nuy sàkku ci moom, am nanu ko.
1.Yowaan 5:14–15
Bés yu mujj yi
Wone yépp7 Ut 2026
6 Ut 2026
5 Ut 2026
4 Ut 2026
3 Ut 2026
2 Ut 2026
1 Ut 2026