Waaye réew mu ko gën lañu doon sàkku, te mooy réewum asamaan. Looloo tax Yàlla rusul ñu di ko tudde seen Yàlla, ndax waajalal na leen ab dëkk.
Yawut ya 11:16
Leeru Bés bi
Waaye réew mu ko gën lañu doon sàkku, te mooy réewum asamaan. Looloo tax Yàlla rusul ñu di ko tudde seen Yàlla, ndax waajalal na leen ab dëkk.
Yawut ya 11:16
Te gannaaw bu ma leen waajalee béreb, dinaa délsi, jëlsi leen, yóbbu, ba fu ma nekk, man, ngeen nekk fa, yeen itam.
Yowaan 14:3
Loolu moo am ngir ab cér bu dul yàqu, du sobewu, du seey, cér bu dence fa asamaan ñeel leen,
1.Piyeer 1:4
ndax amunu fii ci àddina dëkk bu sax ba fàww, waaye dëkk biy ñëw, moom lanuy sàkku.
Yawut ya 13:14
Ñu ne leen: «Yeen waa Galile, lu ngeen di taxaw nii di séentu ci asamaan? Yeesu male ñu yéegee fi seen biir, yóbbu asamaan, nii ngeen ko gise mu jëm asamaan, ni lay délsee.»
Jëf ya 1:11
Kon nag bokk yi, muñleen, ba Boroom bi délsi. Seetleen ci beykat biy séentu njariñal meññeef mu jóge fi suuf si. Ma ngay muñ, céebo ba bët wàcc. Yeen itam muñleen te takk seenu fit, ndax bés ba Boroom biy dikk dëgmal na.
Yanqóoba 5:7–8
Ndax kat, «Des nas tuut, as tuut rekk, kiy dikk, dikk te du yeex.
Yawut ya 10:37
Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww. Kon nag deeleen dëfalantee yooyu kàddu.
1.Tesalonig 4:17–18
Li tuut ab juddu ci àddina ak li xeeblu, li tekkiwul dara, moom la Yàlla tànn, ngir neenale ko li tekki,
1.Korent 1:28
Am xamuleen ne aji jubadi ñi amuñu cér ci nguurug Yàlla? Bu leen kenn nax: Muy fokati séy yi, di bokkaalekat yi, di njaalookat yi, di góor-jigéen yi ak ñiy ànd ak ñoom, ak sàcc yi ak bëgge yi ak màndikat yi ak saagakat yi ak ŋàppaaral yi, duñu am cér ci nguurug Yàlla. Te loolu la ñenn ci yeen doonoon. Waaye Yàllaa leen fóot, sellal leen, jubal leen, ci turu Sang Yeesu Almasi bi ak ci sunu Noowug Yàlla.
1.Korent 6:9–11
Yeen dangeena dee woon ndax seeni moy ak seeni bàkkaar yi ngeen doon dunde démb, ngeen àndoon ci ak doxalinu àddinay tey jii, ak ku bon kiy kàngamu boroom baat yi ci jaww ji asamaan tiim, di boroom xel mu bon mi wéye liggéeyam ci biir aji déggadi ñi, tey. Ci ñoom lanu bokkoon nun ñépp itam; mas nanoo topp sunu bakkan, di jëfe lu sunu bakkan ak sunum xel xemmem. Sunu bindu nit taxoon na noo yeyoo am sànj ni ñépp.
Efes 2:1–3
ca la nu musal, te du jenn jëfu njekk ju nu def, ba tax mu musal nu, waaye ci yërmandeem la nu musale, sang nu cangaay lu nu taxa judduwaat, boole ci yeesale nu Noo gu Sell gi mu nu awale ci Yeesu Almasi bi sunu Musalkat, ba baawaanal ko ci sunu kaw.
Tit 3:5–6
«Samay xalaat déy du seeni xalaat, te samay jëfin du seeni jëfin.» Kàddug Aji Sax jee.
Esayi 55:8
Bés yu mujj yi
Wone yépp12 Ut 2026
11 Ut 2026
10 Ut 2026
9 Ut 2026
8 Ut 2026
7 Ut 2026
6 Ut 2026